Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 20:21-26 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 20:21-26 in Kàddug Yàlla gi

21 Alal ju gaaw du mujje barkeel.
22 Bul feyantook ku la tooñ; dénkul ci Aji Sax ji, mu wallu la.
23 Aji Sax ji bañ na nattu diisaay yu wuute, njublaŋ ci natti diisaay baaxul.
24 Jéegoy jaam Aji Sax jee ko yor, kenn xamul foo jëm.
25 Bul gaawtuy digeek Yàlla, di dugal sa bopp; bul giñ, di réccu.
26 Buur, bu xeloo, ràññee ku bon, mbugal ko, te du ko ñéeblu.
Kàddu yu Xelu 20 in Kàddug Yàlla gi