Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 20:2-18 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 20:2-18 in Kàddug Yàlla gi

2 Buur mer lool, mel ni gayndee ŋar; boo ko merloo, dangay xaru.
3 Moytuw ay, ndam la; dof boo gis day bëgg xuloo.
4 Ab yaafus du gàbb ba mu jotee, day wut am ngóob, du am dara.
5 Mébétu jaambur day teen bu xóot, ku am ug dégg a cay root.
6 Ñu baree ngi naa: «Gore naa,» waaye kuy boroom kóllëre dëgg?
7 Ku jub, di jëfeg mat, doom ju la wuutu bég na.
8 Su buur toogee di àtte, day gis, di ràññee mboolem ayib.
9 Ana ku man ne fóot na xolam, ba tàggook bàkkaar?
10 Nattu diisaay yu yemul ak lu ni mel, Aji Sax ji bañ na ko.
11 Gone sax day jëf, nga gis jikkoom; bu naree dëggu te jub, nga xam.
12 Nopp buy dégg ak bët buy gis, Aji Sax jee sàkk lu ci nekk.
13 Bul bëggi nelaw, ba ñàkk dab la; boo njaxlafee, lekk ba desal.
14 Kuy waxaalee ngi naan: «Baaxul de!» Bu nee wërëñ, di damu naan: «Aka jar!»
15 Wurus am na ak gànjar yu bare, waaye kàdduy xam-xam a gën per yu jafe.
16 Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal jaambur.
17 Njublaŋ, lekk, jëkke neex, mujj mel ni lancub suuf.
18 Pexe, ndigal a koy lal; xare, ay tegtal.
Kàddu yu Xelu 20 in Kàddug Yàlla gi