Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 20:18-21 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 20:18-21 in Kàddug Yàlla gi

18 Pexe, ndigal a koy lal; xare, ay tegtal.
19 Kuy wër di jëw, wuññi sutura; ku réy làmmiñ, bul déeyook moom.
20 Ku saaga sa ndey mbaa sa baay añe lëndëmu bàmmeel.
21 Alal ju gaaw du mujje barkeel.
Kàddu yu Xelu 20 in Kàddug Yàlla gi