Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 20:13-21 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 20:13-21 in Kàddug Yàlla gi

13 Bul bëggi nelaw, ba ñàkk dab la; boo njaxlafee, lekk ba desal.
14 Kuy waxaalee ngi naan: «Baaxul de!» Bu nee wërëñ, di damu naan: «Aka jar!»
15 Wurus am na ak gànjar yu bare, waaye kàdduy xam-xam a gën per yu jafe.
16 Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal jaambur.
17 Njublaŋ, lekk, jëkke neex, mujj mel ni lancub suuf.
18 Pexe, ndigal a koy lal; xare, ay tegtal.
19 Kuy wër di jëw, wuññi sutura; ku réy làmmiñ, bul déeyook moom.
20 Ku saaga sa ndey mbaa sa baay añe lëndëmu bàmmeel.
21 Alal ju gaaw du mujje barkeel.
Kàddu yu Xelu 20 in Kàddug Yàlla gi