Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 20:12-16 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 20:12-16 in Kàddug Yàlla gi

12 Nopp buy dégg ak bët buy gis, Aji Sax jee sàkk lu ci nekk.
13 Bul bëggi nelaw, ba ñàkk dab la; boo njaxlafee, lekk ba desal.
14 Kuy waxaalee ngi naan: «Baaxul de!» Bu nee wërëñ, di damu naan: «Aka jar!»
15 Wurus am na ak gànjar yu bare, waaye kàdduy xam-xam a gën per yu jafe.
16 Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal jaambur.
Kàddu yu Xelu 20 in Kàddug Yàlla gi