6 Ab dof, làmmiñam sooke naw ay, ay waxam di sàkku yeti gannaaw.
7 Ab dof, waxam a koy sànk, làmmiñu boppam a koy dugal.
8 Waxi jëwkat di ñam wu neex wuy seey, jàll ca biir-a-biir.
9 Kuy sàggane sa liggéey, yaak kuy yàq a bokk.
10 Turu Aji Sax ji rawtu bu mag la. Ku jub daw làqu ca, raw.
11 Alal day aar boroom ni ab tata, mu xalaat ne maneesu koo bëtt.