2 Ab dof wutul ag dégg, balaa caag muy jaay ag muus.
3 Bu mbon nuyoo, xeebeel topp ca; jëf ju ñaaw, gàcce rekk.
4 Waxi nit ndox mu xóot la, bu bënnee, xelli, ñu di ca xelu.
5 Faral ku tooñ baaxul, bul xañ dëgg ku deful dara.
6 Ab dof, làmmiñam sooke naw ay, ay waxam di sàkku yeti gannaaw.
7 Ab dof, waxam a koy sànk, làmmiñu boppam a koy dugal.
8 Waxi jëwkat di ñam wu neex wuy seey, jàll ca biir-a-biir.
9 Kuy sàggane sa liggéey, yaak kuy yàq a bokk.
10 Turu Aji Sax ji rawtu bu mag la. Ku jub daw làqu ca, raw.