Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 18:17-22 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 18:17-22 in Kàddug Yàlla gi

17 Ku jëkke layoo, ñu ne yaa yey, ba keroog ka nga joteel weddi la.
18 Tegoo bant day feyu ay, di àtte boroom doole yu jote.
19 Jubook mbokk moo tooñ, jéggi tataa ko gëna yomb, mbaa ubbi bunt yu tëje ràpp.
20 Làmmiñ feesal na biiru boroom, yoolu kàddu suur na boroom.
21 Dund ak dee a ngi ci làmmiñ, te wax garab la, ku ko bëgg, lekk ca doom ya.
22 Ku am jabar, am nga ngëneel, am nga yiwu Aji Sax ji.
Kàddu yu Xelu 18 in Kàddug Yàlla gi