16 Deel maye, da lay ubbil bunt, di la àggle ci boroom daraja.
17 Ku jëkke layoo, ñu ne yaa yey, ba keroog ka nga joteel weddi la.
18 Tegoo bant day feyu ay, di àtte boroom doole yu jote.
19 Jubook mbokk moo tooñ, jéggi tataa ko gëna yomb, mbaa ubbi bunt yu tëje ràpp.
20 Làmmiñ feesal na biiru boroom, yoolu kàddu suur na boroom.
21 Dund ak dee a ngi ci làmmiñ, te wax garab la, ku ko bëgg, lekk ca doom ya.