Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 18:14-24 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 18:14-24 in Kàddug Yàlla gi

14 Ku bëgga dund, dékku woppi yaram, waaye xol bu jeex maneesu koo wéye.
15 Ku am ug dégg wut xam-xam, ku rafet xel sàkku xam-xam.
16 Deel maye, da lay ubbil bunt, di la àggle ci boroom daraja.
17 Ku jëkke layoo, ñu ne yaa yey, ba keroog ka nga joteel weddi la.
18 Tegoo bant day feyu ay, di àtte boroom doole yu jote.
19 Jubook mbokk moo tooñ, jéggi tataa ko gëna yomb, mbaa ubbi bunt yu tëje ràpp.
20 Làmmiñ feesal na biiru boroom, yoolu kàddu suur na boroom.
21 Dund ak dee a ngi ci làmmiñ, te wax garab la, ku ko bëgg, lekk ca doom ya.
22 Ku am jabar, am nga ngëneel, am nga yiwu Aji Sax ji.
23 Ku ñàkk a ngi leewaayu, boroom alal di ko jànni.
24 Barey àndandoo lor a ngi ci, waaye xarit a ngi gëna taq nit mbokkam.
Kàddu yu Xelu 18 in Kàddug Yàlla gi