Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 18:11-18 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 18:11-18 in Kàddug Yàlla gi

11 Alal day aar boroom ni ab tata, mu xalaat ne maneesu koo bëtt.
12 Bew, yàqule; jëkke woyof, mujje tedd.
13 Tontu te déggagoo, ndof la, ak ñàkk kersa.
14 Ku bëgga dund, dékku woppi yaram, waaye xol bu jeex maneesu koo wéye.
15 Ku am ug dégg wut xam-xam, ku rafet xel sàkku xam-xam.
16 Deel maye, da lay ubbil bunt, di la àggle ci boroom daraja.
17 Ku jëkke layoo, ñu ne yaa yey, ba keroog ka nga joteel weddi la.
18 Tegoo bant day feyu ay, di àtte boroom doole yu jote.
Kàddu yu Xelu 18 in Kàddug Yàlla gi