15 Na dof di jëfe, njub la ci moom; dégg ndigal rafet um xel la.
16 Ab dof bu meree, mu gaawa feeñ; ku teey, tanqamlu saaga.
17 Ku dëggu, seede dëgg; seede bu bon, fen rekk.
18 Làmmiñu waxkat, jam-jami jaasi; kàddu gu xelu, garab la ci.
19 Kàdduy dëgg, day sax dàkk; fen, xef xippi, mu wéy.
20 Kuy ràbb lu bon lal pexey wor, kuy digle jàmm, am mbégte.