Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 9:23-39 in Wolof

Help us?

JËF YA 9:23-39 in Téereb Injiil

23 Ba ñu ca tegee ay fani fan, Yawut yi daldi gise, ngir reylu ko.
24 Waaye Sóol yég seen pexe. Fekk guddi ak bëccëg ñu doon wottu bunt yi yépp, ngir man koo bóom.
25 Noonu taalibe yi jël ko ci guddi, def ko ci dàmba gu réy, jaarale ko ci miir bi, yoor ko ci suuf.
26 Bi Sóol agsee Yerusalem, mu jéema ànd ak taalibe yi, waaye ñépp ragal ko, ndax gëmuñu woon ag taalibeem.
27 Ci kaw loolu Barnabas jël ko, yóbbu ko ca ndaw ya, nettali leen, ni Sóol gise Boroom bi ci kaw yoon wi, ak li mu ko wax, rax-ca-dolli fit wi mu doon waxe ci turu Yeesu ci Damaas.
28 Noonu mu nekk ak ñoom ci Yerusalem, di dugg ak a génn, di wax ak fit ci turu Boroom bi.
29 Muy wax ak di werante ak Yawut yiy làkk gereg, waaye ñu di ko wuta rey.
30 Bi ko bokk yi yégee nag, ñu yóbbu ko dëkku Sesare, yebal ko dëkku Tars.
31 Noonu mbooloom ñi gëm nekk ci jàmm ci biir diiwaani Yude gépp ak Galile ak Samari; ñuy gëna dëgër, di wéy ci ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalu Xel mu Sell mi.
32 Piyeer nag di wër, di jaar fu nekk, tey dem ci gaayi Yàlla yi dëkk Lidd,
33 mu gis fa nit ku làggi, tudd Ene, tëdd ci basaŋ diirub juróom ñetti at.
34 Piyeer ne ko: «Ene, Yeesu Kirist faj na la; jógal te defar sa lal.» Noonu mu daldi jóg ca saa sa.
35 Bi ko waa diiwaani Lidd ak Saron gépp gisee, ñu daldi waññiku ci Boroom bi.
36 Amoon na nag ci dëkku Yope taalibe bu jigéen bu tudd Tabita, liy tekki «Dorkas», maanaam «kéwél», te muy wéy ci jëf yu baax ak sarxe.
37 Ca fan yooyu mu daanu wopp, ba faatu; noonu ñu sang ko, teg ko ca néeg, ba sut ca taax ma.
38 Gannaaw Lidd sorewul ak Yope nag, te taalibe yi dégg ne Piyeer a nga fa, ñu yónnee ko ñaari nit, ñaan ko mu ñëw ci ñoom ci saa si.
39 Bi ko Piyeer déggee, mu jóg, ànd ak ñoom. Bi mu ñëwee, ñu yóbbu ko ca néeg bu kawe ba. Fekk fa ay jigéen ñi seeni jëkkër faatu, ñu daldi wër Piyeer, ñépp di jooy, di ko won kamisol ya ak mbubb, ya Dorkas daan defar cig dundam.
JËF YA 9 in Téereb Injiil

Jëf ya 9:23-39 in Kàddug Yàlla gi

23 Ba ñu ca tegee ab diir bu xawa yàgg, Yawut yi féncoo, ngir reylu ko.
24 Sóol nag yég seen mébét. Guddi ak bëccëg lañu doon wattu bunti dëkk ba, ngir bóom ko.
25 Teewul taalibe yi yeb ko ag guddi ci ag dàmba, jàlle ko ca wàllaa miir ba, yoor ko.
26 Ba Sóol agsee Yerusalem, jéem naa jaxasook taalibe yi, waaye ñépp a ko ragal, ndax ñàkka gëm ag taalibeem.
27 Ci kaw loolu Barnaba ànd ak moom, yóbbu ko ca ndaw ya. Barnaba nettali leen, ni Sóol gise Sang bi ca yoon wa, ba mu wax ak Sóol, ak fit wa Sóol waaree ca Damaas ci turu Yeesu.
28 Ba loolu amee Sóol ànd ak ndaw yi di dem ak a dikk ci biir Yerusalem, di waaree aw fit ci turu Sang bi.
29 Mu boole ci di wax ak a werante ak Yawut ñiy làkk gereg, te ñoom ñu di ko fexee rey.
30 Bokki gëmkat ña nag yég ko, daldi koy yóbbu Sesare, yebale ko foofa, mu dem Tàrs.
31 Ba mu ko defee mbooloom gëmkat ñi ci mboolem diiwaani Yude ak Galile ak Samari daldi am jàmm. Ñuy gëna dëgër, di wéye ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalal Noo gu Sell gi.
32 Piyeer mi doon wër fu nekk nag, am na bés mu jaare ca ñu sell ña dëkke Lidd.
33 Mu gis foofa waa ju ñuy wax Ene. Fekk na diiru juróom ñetti at, cib lal rekk lay tëdd ndax yaram wu làggi.
34 Piyeer ne ko: «Ene, Yeesu Almasi wéral na la; jógal, lalal sa bopp.» Mu jóg ca saa sa.
35 Mboolem waa diiwaani Lidd ak Saron nag gis ko, ñoom ñépp waññiku ci Sang bi.
36 Dëkk ba ñuy wax Yope, ab taalibe bu jigéen a nga fa woon, ñu di ko wax Tabita mbaa Dorkas ci làkku gereg. Def lu baax ak sarxe la saxoo woon.
37 Ci fan yooyu, mu daanu wopp, daldi faatu. Ñu sang ko, dugal ko ca néegu kaw taax ma.
38 Ci biir loolu taalibe yi dégg ne Piyeer a nga Lidd, te Lidd sorewul Yope. Ñu yebal ñaari nit ca moom, ngir ñaan ko mu ñëw te baña yeex.
39 Piyeer jóg, ànd ak ñoom, ba agsi. Ñu yéege ko ca néegu kaw taax ma. Ay jëtun a nga fa woon. Ñoom ñépp di jooyoo, yéew Piyeer, won ko turki yaak mbubb ya Dorkas defaroon ba muy nekk ak ñoom.
Jëf ya 9 in Kàddug Yàlla gi