Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 9

JËF YA 9:23-39

Help us?
Click on verse(s) to share them!
23Ba ñu ca tegee ay fani fan, Yawut yi daldi gise, ngir reylu ko.
24Waaye Sóol yég seen pexe. Fekk guddi ak bëccëg ñu doon wottu bunt yi yépp, ngir man koo bóom.
25Noonu taalibe yi jël ko ci guddi, def ko ci dàmba gu réy, jaarale ko ci miir bi, yoor ko ci suuf.
26Bi Sóol agsee Yerusalem, mu jéema ànd ak taalibe yi, waaye ñépp ragal ko, ndax gëmuñu woon ag taalibeem.
27Ci kaw loolu Barnabas jël ko, yóbbu ko ca ndaw ya, nettali leen, ni Sóol gise Boroom bi ci kaw yoon wi, ak li mu ko wax, rax-ca-dolli fit wi mu doon waxe ci turu Yeesu ci Damaas.
28Noonu mu nekk ak ñoom ci Yerusalem, di dugg ak a génn, di wax ak fit ci turu Boroom bi.
29Muy wax ak di werante ak Yawut yiy làkk gereg, waaye ñu di ko wuta rey.
30Bi ko bokk yi yégee nag, ñu yóbbu ko dëkku Sesare, yebal ko dëkku Tars.
31Noonu mbooloom ñi gëm nekk ci jàmm ci biir diiwaani Yude gépp ak Galile ak Samari; ñuy gëna dëgër, di wéy ci ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalu Xel mu Sell mi.
32Piyeer nag di wër, di jaar fu nekk, tey dem ci gaayi Yàlla yi dëkk Lidd,
33mu gis fa nit ku làggi, tudd Ene, tëdd ci basaŋ diirub juróom ñetti at.
34Piyeer ne ko: «Ene, Yeesu Kirist faj na la; jógal te defar sa lal.» Noonu mu daldi jóg ca saa sa.
35Bi ko waa diiwaani Lidd ak Saron gépp gisee, ñu daldi waññiku ci Boroom bi.
36Amoon na nag ci dëkku Yope taalibe bu jigéen bu tudd Tabita, liy tekki «Dorkas», maanaam «kéwél», te muy wéy ci jëf yu baax ak sarxe.
37Ca fan yooyu mu daanu wopp, ba faatu; noonu ñu sang ko, teg ko ca néeg, ba sut ca taax ma.
38Gannaaw Lidd sorewul ak Yope nag, te taalibe yi dégg ne Piyeer a nga fa, ñu yónnee ko ñaari nit, ñaan ko mu ñëw ci ñoom ci saa si.
39Bi ko Piyeer déggee, mu jóg, ànd ak ñoom. Bi mu ñëwee, ñu yóbbu ko ca néeg bu kawe ba. Fekk fa ay jigéen ñi seeni jëkkër faatu, ñu daldi wër Piyeer, ñépp di jooy, di ko won kamisol ya ak mbubb, ya Dorkas daan defar cig dundam.

Read JËF YA 9JËF YA 9
Compare JËF YA 9:23-39JËF YA 9:23-39