Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 9:12-31 in Wolof

Help us?

JËF YA 9:12-31 in Téereb Injiil

12 Te gis na cim peeñu nit ku tudd Anañas, mu dugg, teg ko ay loxo, ba muy gisaat.»
13 Waaye Anañas ne ko: «Boroom bi, dégg naa ci nit ñu bare ci mbirum kooku, ñu seede lu bare lu bon lu mu def say gaay ci Yerusalem.
14 Te indaale na fii sax sañ-sañ bu jóge ci sarxalkat yu mag ya, ngir yeew képp kuy tudd saw tur.»
15 Waaye Boroom bi ne ko: «Demal, ndaxte maa ko tànn, muy sama jëfandukaay, ngir yóbbu sama tur fa kanam ñi nekkul Yawut ak fa kanam buur yi ak bànni Israyil.
16 Te dinaa ko won coono yu bare yu mu wara dékku ngir sama tur.»
17 Ci kaw loolu Anañas dem, dugg ca kër ga, teg ay loxoom Sóol. Mu ne ko: «Sóol sama mbokk, Boroom bi Yeesu, mi la feeñu woon ci kaw yoon wi, bi ngay dikk, moo ma yónni, ngir nga dellu di gis te fees ak Xel mu Sell mi.»
18 Ca saa sa lu mel ni ay waasintóor génne ci ay bëtam, mu daldi gisaat. Noonu mu jóg, ñu sóob ko ci ndox;
19 ba noppi mu lekk, amaat doole. Bi mu ko defee mu toog ay fan ak taalibe, ya nekk Damaas.
20 Ca saa sa muy yégle ca jàngu ya ne, Yeesu mooy Doomu Yàlla.
21 Ñi ko dégg ñépp waaru naan: «Ndax du kii moo daan tas ñiy tudd tur woowu ci Yerusalem, te mu ñëw fii, ngir yeew leen, yóbbu ci kanam sarxalkat yu mag ya?»
22 Moona Sóol di gëna am kàttan, bay jaaxal Yawut yi dëkk Damaas, ci di leen wax ay firnde, ne Yeesu mooy Almasi bi.
23 Ba ñu ca tegee ay fani fan, Yawut yi daldi gise, ngir reylu ko.
24 Waaye Sóol yég seen pexe. Fekk guddi ak bëccëg ñu doon wottu bunt yi yépp, ngir man koo bóom.
25 Noonu taalibe yi jël ko ci guddi, def ko ci dàmba gu réy, jaarale ko ci miir bi, yoor ko ci suuf.
26 Bi Sóol agsee Yerusalem, mu jéema ànd ak taalibe yi, waaye ñépp ragal ko, ndax gëmuñu woon ag taalibeem.
27 Ci kaw loolu Barnabas jël ko, yóbbu ko ca ndaw ya, nettali leen, ni Sóol gise Boroom bi ci kaw yoon wi, ak li mu ko wax, rax-ca-dolli fit wi mu doon waxe ci turu Yeesu ci Damaas.
28 Noonu mu nekk ak ñoom ci Yerusalem, di dugg ak a génn, di wax ak fit ci turu Boroom bi.
29 Muy wax ak di werante ak Yawut yiy làkk gereg, waaye ñu di ko wuta rey.
30 Bi ko bokk yi yégee nag, ñu yóbbu ko dëkku Sesare, yebal ko dëkku Tars.
31 Noonu mbooloom ñi gëm nekk ci jàmm ci biir diiwaani Yude gépp ak Galile ak Samari; ñuy gëna dëgër, di wéy ci ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalu Xel mu Sell mi.
JËF YA 9 in Téereb Injiil

Jëf ya 9:12-31 in Kàddug Yàlla gi

12 Dafa gis cim peeñu ku ñuy wax Anañas duggsi, teg ko loxo, ngir mu dellu di gis.»
13 Anañas nag ne ko: «Sang bi, maa dégge ci ñu bare mbirum kooku, ñu seede mboolem jëf ju bon ji mu def say nit ñu sell ci biir Yerusalem.
14 Te moo yor ndigal lu tukkee ci sarxalkat yu mag yi, ngir yeewlu képp kuy tudd saw tur.»
15 Sang bi ne ko: «Demal, ndax kooku jumtukaay laa ko tànne, ngir mu xamali sama tur, xeeti jaambur yi ak seeni buur, xamal ko itam bànni Israyil.
16 Maa koy won mboolem coono bi mu wara dékku ngir sama tur.»
17 Ci kaw loolu Anañas dem, dugg ca kër ga, teg Sóol loxo, ne ko: «Mbokk mi Sóol, Sang Yeesu, mi la feeñu woon ci yoon wi nga dikke, moo ma yebal ci yaw, ngir nga dellu di gis te feese Noo gu Sell gi.»
18 Ca saa sa lu mel niy waasintóor wadde ca bët ya, mu dellu di gis. Mu daldi jóg, ñu sóob ko ci ndox.
19 Ba loolu wéyee, mu lekk, doora am doole. Sóol toog na ak taalibe ya ca Damaas ay fan.
20 Ca saa sa la tàmbalee xamle Yeesu ca jàngu ya, naan Yeesu mooy Doomu Yàlla.
21 Mboolem ña ko dégg, daldi waaru, naan: «Xanaa du kii moo doon bóom ñiy tudd woowu tur ci Yerusalem? Du moo fi dikkoon, ngir yeewlu leen, yóbbu ci sarxalkat yu mag yi?»
22 Teewul Sóol gëna am manoore, ba far jaaxal Yawut ñi dëkke Damaas, di firndeel ne Yeesu mooy Almasi.
23 Ba ñu ca tegee ab diir bu xawa yàgg, Yawut yi féncoo, ngir reylu ko.
24 Sóol nag yég seen mébét. Guddi ak bëccëg lañu doon wattu bunti dëkk ba, ngir bóom ko.
25 Teewul taalibe yi yeb ko ag guddi ci ag dàmba, jàlle ko ca wàllaa miir ba, yoor ko.
26 Ba Sóol agsee Yerusalem, jéem naa jaxasook taalibe yi, waaye ñépp a ko ragal, ndax ñàkka gëm ag taalibeem.
27 Ci kaw loolu Barnaba ànd ak moom, yóbbu ko ca ndaw ya. Barnaba nettali leen, ni Sóol gise Sang bi ca yoon wa, ba mu wax ak Sóol, ak fit wa Sóol waaree ca Damaas ci turu Yeesu.
28 Ba loolu amee Sóol ànd ak ndaw yi di dem ak a dikk ci biir Yerusalem, di waaree aw fit ci turu Sang bi.
29 Mu boole ci di wax ak a werante ak Yawut ñiy làkk gereg, te ñoom ñu di ko fexee rey.
30 Bokki gëmkat ña nag yég ko, daldi koy yóbbu Sesare, yebale ko foofa, mu dem Tàrs.
31 Ba mu ko defee mbooloom gëmkat ñi ci mboolem diiwaani Yude ak Galile ak Samari daldi am jàmm. Ñuy gëna dëgër, di wéye ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalal Noo gu Sell gi.
Jëf ya 9 in Kàddug Yàlla gi