Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 9

JËF YA 9:12-31

Help us?
Click on verse(s) to share them!
12Te gis na cim peeñu nit ku tudd Anañas, mu dugg, teg ko ay loxo, ba muy gisaat.»
13Waaye Anañas ne ko: «Boroom bi, dégg naa ci nit ñu bare ci mbirum kooku, ñu seede lu bare lu bon lu mu def say gaay ci Yerusalem.
14Te indaale na fii sax sañ-sañ bu jóge ci sarxalkat yu mag ya, ngir yeew képp kuy tudd saw tur.»
15Waaye Boroom bi ne ko: «Demal, ndaxte maa ko tànn, muy sama jëfandukaay, ngir yóbbu sama tur fa kanam ñi nekkul Yawut ak fa kanam buur yi ak bànni Israyil.
16Te dinaa ko won coono yu bare yu mu wara dékku ngir sama tur.»
17Ci kaw loolu Anañas dem, dugg ca kër ga, teg ay loxoom Sóol. Mu ne ko: «Sóol sama mbokk, Boroom bi Yeesu, mi la feeñu woon ci kaw yoon wi, bi ngay dikk, moo ma yónni, ngir nga dellu di gis te fees ak Xel mu Sell mi.»
18Ca saa sa lu mel ni ay waasintóor génne ci ay bëtam, mu daldi gisaat. Noonu mu jóg, ñu sóob ko ci ndox;
19ba noppi mu lekk, amaat doole. Bi mu ko defee mu toog ay fan ak taalibe, ya nekk Damaas.
20Ca saa sa muy yégle ca jàngu ya ne, Yeesu mooy Doomu Yàlla.
21Ñi ko dégg ñépp waaru naan: «Ndax du kii moo daan tas ñiy tudd tur woowu ci Yerusalem, te mu ñëw fii, ngir yeew leen, yóbbu ci kanam sarxalkat yu mag ya?»
22Moona Sóol di gëna am kàttan, bay jaaxal Yawut yi dëkk Damaas, ci di leen wax ay firnde, ne Yeesu mooy Almasi bi.
23Ba ñu ca tegee ay fani fan, Yawut yi daldi gise, ngir reylu ko.
24Waaye Sóol yég seen pexe. Fekk guddi ak bëccëg ñu doon wottu bunt yi yépp, ngir man koo bóom.
25Noonu taalibe yi jël ko ci guddi, def ko ci dàmba gu réy, jaarale ko ci miir bi, yoor ko ci suuf.
26Bi Sóol agsee Yerusalem, mu jéema ànd ak taalibe yi, waaye ñépp ragal ko, ndax gëmuñu woon ag taalibeem.
27Ci kaw loolu Barnabas jël ko, yóbbu ko ca ndaw ya, nettali leen, ni Sóol gise Boroom bi ci kaw yoon wi, ak li mu ko wax, rax-ca-dolli fit wi mu doon waxe ci turu Yeesu ci Damaas.
28Noonu mu nekk ak ñoom ci Yerusalem, di dugg ak a génn, di wax ak fit ci turu Boroom bi.
29Muy wax ak di werante ak Yawut yiy làkk gereg, waaye ñu di ko wuta rey.
30Bi ko bokk yi yégee nag, ñu yóbbu ko dëkku Sesare, yebal ko dëkku Tars.
31Noonu mbooloom ñi gëm nekk ci jàmm ci biir diiwaani Yude gépp ak Galile ak Samari; ñuy gëna dëgër, di wéy ci ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalu Xel mu Sell mi.

Read JËF YA 9JËF YA 9
Compare JËF YA 9:12-31JËF YA 9:12-31