18 Bi Simoŋ gisee nag ne Yàlla may na Xel mi jaarale ko ci loxoy ndaw ya, mu indil leen xaalis,
19 ne leen: «Mayleen ma sañ-sañ boobu, ba ku ma teg samay loxo, nga jot Xel mu Sell mi.»
20 Waaye Piyeer ne ko: «Asarul ak sa xaalis, yaw mi yaakaar ne man ngaa jënd mayu Yàlla ak xaalis.
21 Amuloo benn wàll mbaa cér ci lii, ndaxte sa xol laabul ci kanam Yàlla.
22 Réccul nag sa coxor te ñaan Boroom bi, mu baal la sa xalaatu xol, su manee am.
23 Ndaxte gis naa ne sóobu nga ci lu wex xat ci kanam Yàlla, te bàkkaar not na la.»