Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 8:13-22 in Wolof

Help us?

JËF YA 8:13-22 in Téereb Injiil

13 Simoŋ sax gëm, ñu sóob ko ci ndox; mu wéy nag ci topp Filib, di waaru ci kéemaan yi ak firnde yu mag yiy am.
14 Bi nga xamee ne ndaw yi nekk Yerusalem yég nañu ne, waa Samari nangu nañu kàddug Yàlla; ñu yónni fa Piyeer ak Yowaana.
15 Ñu dem fa nag, ñaanal leen, ngir ñu jot Xel mu Sell mi.
16 Ndaxte wàccagul ci kenn ci ñoom, waaye sóoboon nañu leen rekk ci ndox ci turu Boroom bi Yeesu.
17 Noonu Piyeer ak Yowaana teg leen loxo, ñu jot Xel mu Sell mi.
18 Bi Simoŋ gisee nag ne Yàlla may na Xel mi jaarale ko ci loxoy ndaw ya, mu indil leen xaalis,
19 ne leen: «Mayleen ma sañ-sañ boobu, ba ku ma teg samay loxo, nga jot Xel mu Sell mi.»
20 Waaye Piyeer ne ko: «Asarul ak sa xaalis, yaw mi yaakaar ne man ngaa jënd mayu Yàlla ak xaalis.
21 Amuloo benn wàll mbaa cér ci lii, ndaxte sa xol laabul ci kanam Yàlla.
22 Réccul nag sa coxor te ñaan Boroom bi, mu baal la sa xalaatu xol, su manee am.
JËF YA 8 in Téereb Injiil

Jëf ya 8:13-22 in Kàddug Yàlla gi

13 Simoŋ ci boppam gëm, moom it, ñu sóob ko ci ndox. Simoŋ nag bàyyeetul Filib. Ba mu gisee firnde yaak kiraama yu mag yay am, moom moo yéemu.
14 Ba ndaw ya ca Yerusalem yégee ne waa Samari nangu nañu kàddug Yàlla, Piyeer ak Yowaan lañu fa yebal.
15 Ñu agsi Samari, ñaanal gëmkat ña, ngir ñu jot Noo gu Sell gi.
16 Ndax booba Noo gi wàccagul woon ci kenn ci ñoom, dees leena sóoboon rekk ci ndox ci turu Sang Yeesu.
17 Ba loolu amee Piyeer ak Yowaan teg leen loxo, ñu jot Noo gu Sell gi.
18 Simoŋ nag gis noonee mayug Noo, gi sababoo ci tegeb loxo bu ndaw ña amal, ba tax mu indil leen xaalis.
19 Mu ne leen: «Mayleen ma man itam xam-xam bii, ngir ku ma teg loxo, nga jot Noo gu Sell gi.»
20 Piyeer ne ko: «Na sa xaalis ànd ak yaw asaru, ndegam ab xaalis nga yaakaara jënde mayu Yàlla!
21 Amuloo benn wàll mbaa ab cér ci lii, ndax sa xol a jubul ci kanam Yàlla.
22 Réccul nag sa mbon gii, te ñaan Boroom bi; jombul mu baal la sa mébétu xol.
Jëf ya 8 in Kàddug Yàlla gi