Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 7:1-12 in Wolof

Help us?

JËF YA 7:1-12 in Téereb Injiil

1 Noonu sarxalkat bu mag ba ne ko: «Ndax loolu dëgg la?»
2 Ecen ne ko: «Yéen samay bokk ak samay baay, dégluleen! Yàlla, miy Boroom ndam, feeñu woon na sunu maam Ibraayma, bi mu nekkee réewu Mesopotami, te dëkkagul woon Karan.
3 Mu ne ko: “Toxul sa réew, bàyyi say bokk, te ñëw ci réew, mi ma lay won.”
4 «Ci kaw loolu mu génn réewu niti Kalde, dëkksi Karan. Te bi baayam faatoo, Yàlla toxale ko foofa, dëël ko ci réew, mi ngeen dëkk léegi.
5 Waaye mayu ko fa genn moomeel gu mu wara donale, du sax fu mu mana teg tànkam; waaye dig na ko ne dina ko may réew mi, mu yilif ko moom ak askanam, fekk booba amagul doom.
6 Yàlla ne ko: “Ñi soqikoo ci yaw dinañu ganeyaan ci réew mu ñu dëkkul; dees na leen def ay jaam, di leen fitnaal diirub ñeenti téeméeri at.”
7 Waaye Yàlla nee na: “Xeet wi leen jaamloo, man maa leen di àtte te gannaaw loolu dinañu génn, di ma jaamu ci bérab bii.”
8 Yàlla nag tëral kóllëre seen diggante, fas ko ci màndargam xaraf. Noonu Ibraayma jur Isaaxa, xarafal ko ca juróom ñetteelu fan ba; Isaaxa def noonu Yanqóoba, Yanqóoba it def noonu fukki maam ya ak ñaar, ñi sos xeet wi.
9 «Naka maam yooyu, dañoo iñaane Yuusufa, ba jaay ko, mu jëm réewu Misra. Waaye Yàlla taxawu ko,
10 génne ko ci coonoom yépp, defal ko yiw ak xel ci kanam Firawna, buuru Misra, mu def ko kilifag Misra ak këram gépp.
11 «Bi loolu amee xiif tàbbi ci biir Misra ak réewu Kanaan mépp, ba toskare ja metti lool, te sunuy maam amatuñu lu ñu lekk.
12 Yanqóoba nag dégg ne Misra am na dugub, mu yebal ca sunuy maam, ñu dem fa yoon wu jëkk.
JËF YA 7 in Téereb Injiil

Jëf ya 7:1-12 in Kàddug Yàlla gi

1 Sarxalkat bu mag ba ne ko: «Ndax loolu dëgg la?»
2 Eccen ne ko: «Yeen bokk yi, yeen samay baay, dégluleen! Yàlla, miy Boroom daraja moo feeñu woon sunu maam Ibraayma, ba mu nekkee réewum Mesopotami, bala moo sanc Karan.
3 Mu ne ko: “Jógeel sam réew, jóge ci say bokk, te nga dem ca réew, mi ma lay won.”
4 «Mu daldi jóge réewum waa Kalde, sanci Karan. Fa la ko Yàlla toxale gannaaw ba baayam faatoo, sancal ko ci réew mii ngeen dëkk tey.
5 Taxul mu muurale ko lenn ci réew mii, du sax fu mu teg tànkam. Teewul mu dig ko, ne moom lay moomale réew mi, mook askanam wa koy wuutuji, te fekkul sax mu am doom.
6 Yàlla ne ko: “Saw askan dinañu toxuji bitim réew, te dees na leen def ay jaam, mitital leen diiru ñeenti téeméeri at (400).”
7 Yàlla neeti ko: “Xeet wi leen di jaamloo nag, man maa leen di mbugal. Gannaaw loolu dinañu fa génne, jaamusi ma ci bérab bii.”
8 Yàlla daldi fasook Ibraayma kóllëre gu mu màndargale xaraf. Moo tax Ibraayma xarfal doomam Isaaxa, ba mu juddoo ba am juróom ñetti fan; Isaaxa, Yanqóoba, Yanqóoba, fukki maam yaak ñaar.
9 «Maam yooyu nag iñaane seen doomu baay Yuusufa, ba jaay ko njaam, ñu yóbbu ko Misra. Teewul Yàlla ànd ak Yuusufa,
10 xettli ko ci coonoom yépp, rafetal xelam, may ko itam Firawna buuru Misra baaxe ko; mu def ko kilifa ci Misra ak ci biir ëttu këram gépp.
11 «Ci kaw loolu ab xiif dikkal Misra gépp ak réewum Kanaan. Mu metti lool. Sunuy maam nag amatuñu ab dund.
12 Yanqóoba dégg ne ab dund am na Misra. Ca la fa jëkka yebal sunu maam ya.
Jëf ya 7 in Kàddug Yàlla gi