Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 7

Jëf ya 7:1-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Sarxalkat bu mag ba ne ko: «Ndax loolu dëgg la?»
2Eccen ne ko: «Yeen bokk yi, yeen samay baay, dégluleen! Yàlla, miy Boroom daraja moo feeñu woon sunu maam Ibraayma, ba mu nekkee réewum Mesopotami, bala moo sanc Karan.
3Mu ne ko: “Jógeel sam réew, jóge ci say bokk, te nga dem ca réew, mi ma lay won.”
4«Mu daldi jóge réewum waa Kalde, sanci Karan. Fa la ko Yàlla toxale gannaaw ba baayam faatoo, sancal ko ci réew mii ngeen dëkk tey.
5Taxul mu muurale ko lenn ci réew mii, du sax fu mu teg tànkam. Teewul mu dig ko, ne moom lay moomale réew mi, mook askanam wa koy wuutuji, te fekkul sax mu am doom.
6Yàlla ne ko: “Saw askan dinañu toxuji bitim réew, te dees na leen def ay jaam, mitital leen diiru ñeenti téeméeri at (400).”
7Yàlla neeti ko: “Xeet wi leen di jaamloo nag, man maa leen di mbugal. Gannaaw loolu dinañu fa génne, jaamusi ma ci bérab bii.”
8Yàlla daldi fasook Ibraayma kóllëre gu mu màndargale xaraf. Moo tax Ibraayma xarfal doomam Isaaxa, ba mu juddoo ba am juróom ñetti fan; Isaaxa, Yanqóoba, Yanqóoba, fukki maam yaak ñaar.
9«Maam yooyu nag iñaane seen doomu baay Yuusufa, ba jaay ko njaam, ñu yóbbu ko Misra. Teewul Yàlla ànd ak Yuusufa,
10xettli ko ci coonoom yépp, rafetal xelam, may ko itam Firawna buuru Misra baaxe ko; mu def ko kilifa ci Misra ak ci biir ëttu këram gépp.
11«Ci kaw loolu ab xiif dikkal Misra gépp ak réewum Kanaan. Mu metti lool. Sunuy maam nag amatuñu ab dund.
12Yanqóoba dégg ne ab dund am na Misra. Ca la fa jëkka yebal sunu maam ya.

Read Jëf ya 7Jëf ya 7
Compare Jëf ya 7:1-12Jëf ya 7:1-12