Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 5:33-42 in Wolof

Help us?

JËF YA 5:33-42 in Téereb Injiil

33 Bi ñu déggee loolu, ñu mer ba seen xol di dagg, ñu bëgg leena rey.
34 Waaye amoon na fa nit ku tudd Gamaleel, bokk ci tariixab Farisen ya, di xutbakat bu tedd ci yoonu Musaa, mu jóg ca mbooloo ma, santaane ñu génne leen tuuti.
35 Bi ñu ko defee mu ne leen: «Yéen bokki Israyil, moytuleen li ngeen di def nit ñooñu.
36 Ndaxte bu yàggul Tëdas jógoon na, mbubboo daraja, ba lu mat ñeenti téeméeri nit takktoo ak moom. Tëdas moomu nag reyees na ko, te ñi ko toppoon ñépp tasaaroo, ba seen pexe nasax.
37 Gannaawam it Yudaa mu Galile jóg, ca jamono ja ñu doon bind waa réew ma, mu jógloo nit ñu bare, ñu ànd ak moom. Moom itam dee na, te ay nitam ñépp tasaaroo.
38 Léegi maa ngi leen di wax, génnleen ci mbirum ñooñu te bàyyi leen ñu dem. Ndaxte bu seen pas-pas mbaa seen jëf dee pexem nit, dina yàqu.
39 Waaye bu fekkee ne ndogalu Yàlla la, dungeen ko mana fanq, ngir ragala jànkoonte ak Yàlla.»
40 Bi mu waxee loolu, ñu fekk ko ci xalaatam; ñu woo ndaw ya, daldi leen dóor ay yar, tere leen, ñu waxati dara ci turu Yeesu, ba noppi bàyyi leen, ñu dem.
41 Ndaw ya nag jóge ca kanam kureelu àttekat ya, bég ci li leen Yàlla jàppe, ñu yeyoo yenu toroxte ngir Tur wa.
42 Noonu bés bu nekk ca kër Yàlla ga ak ca kër ya, daawuñu noppee jàngle ak a xamle xibaaru jàmm bi, ne Yeesu mooy Almasi bi.
JËF YA 5 in Téereb Injiil

Jëf ya 5:33-42 in Kàddug Yàlla gi

33 Ba ñu déggee loolu, dañoo mer ba fees, nar leena rey.
34 Ab Farisen bu ñuy wax Gamalyel, di jànglekatu yoonu Musaa bu ñépp nawloo, daldi taxaw ca digg kurélu àttekat ya. Mu joxe ndigal ngir ñu génne leen ab diir.
35 Ba ñu génnee, mu ne waa kurél ga: «Yeen bokki Israyil, moytuleen bu baax li ngeen di def ak nit ñii.
36 Ndaxte bu yàggul la Tëdas jóg, di jaay daraja, ba lu wara tollook ñeenti téeméeri nit far ak moom. Ñu rey ko, ña ko toppoon ñépp tasaaroo, seen pexe mujjewul fenn.
37 Gannaawam it Yuda mu Galile jóg, ca jant ya ñu doon lim waa réew mi; mu yóbbaale mbooloo mu ko topp. Moom itam dee, ña ko toppoon ñépp tasaaroo.
38 Léegi nag, dama ne, maanduleen ci ñii, te ba leen, ngir su seen mébét mbaa seen jëf bawoo ci nit, day yàqu rekk.
39 Waaye su bawoo fa Yàlla nag, dungeen ko mana fanq, moytuleena jànkoonte ak Yàlla.» Ñu daldi fekksi Gamalyel,
40 woowaat ndaw ya. Ba loolu amee ñu dóor leen, aaye leen ñu waxati lenn ci turu Yeesu, door leena yiwi.
41 Ndaw ya nag bàyyikoo ca kurélu àttekat ya, di bég, gannaaw ñoom lañu jàpp ne ñoo yelloo toroxte ga ñu leen teg ndax Tur wi.
42 Ci kaw loolu bés bu nekkaan, muy ca kër Yàlla, di ca biir kër ya, noppiwuñoo jàngle ak a xamle xibaaru jàmm bi yéene ne Yeesu mooy Almasi.
Jëf ya 5 in Kàddug Yàlla gi