Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 5

JËF YA 5:33-42

Help us?
Click on verse(s) to share them!
33Bi ñu déggee loolu, ñu mer ba seen xol di dagg, ñu bëgg leena rey.
34Waaye amoon na fa nit ku tudd Gamaleel, bokk ci tariixab Farisen ya, di xutbakat bu tedd ci yoonu Musaa, mu jóg ca mbooloo ma, santaane ñu génne leen tuuti.
35Bi ñu ko defee mu ne leen: «Yéen bokki Israyil, moytuleen li ngeen di def nit ñooñu.
36Ndaxte bu yàggul Tëdas jógoon na, mbubboo daraja, ba lu mat ñeenti téeméeri nit takktoo ak moom. Tëdas moomu nag reyees na ko, te ñi ko toppoon ñépp tasaaroo, ba seen pexe nasax.
37Gannaawam it Yudaa mu Galile jóg, ca jamono ja ñu doon bind waa réew ma, mu jógloo nit ñu bare, ñu ànd ak moom. Moom itam dee na, te ay nitam ñépp tasaaroo.
38Léegi maa ngi leen di wax, génnleen ci mbirum ñooñu te bàyyi leen ñu dem. Ndaxte bu seen pas-pas mbaa seen jëf dee pexem nit, dina yàqu.
39Waaye bu fekkee ne ndogalu Yàlla la, dungeen ko mana fanq, ngir ragala jànkoonte ak Yàlla.»
40Bi mu waxee loolu, ñu fekk ko ci xalaatam; ñu woo ndaw ya, daldi leen dóor ay yar, tere leen, ñu waxati dara ci turu Yeesu, ba noppi bàyyi leen, ñu dem.
41Ndaw ya nag jóge ca kanam kureelu àttekat ya, bég ci li leen Yàlla jàppe, ñu yeyoo yenu toroxte ngir Tur wa.
42Noonu bés bu nekk ca kër Yàlla ga ak ca kër ya, daawuñu noppee jàngle ak a xamle xibaaru jàmm bi, ne Yeesu mooy Almasi bi.

Read JËF YA 5JËF YA 5
Compare JËF YA 5:33-42JËF YA 5:33-42