Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 3:8-14 in Wolof

Help us?

JËF YA 3:8-14 in Téereb Injiil

8 Mu tëb, daldi taxaw, di dox. Mu dugg ak ñoom ca kër Yàlla ga, muy dox, di tëb tey sant Yàlla.
9 Noonu ñépp gis ko, muy dox, di sant Yàlla.
10 Te ñu xàmmi ko, ne moo daan toog, di yelwaan ca Bunt bu rafet ba ca kër Yàlla ga. Ñu daldi waaru lool te yéemu ci li ko dikkal.
11 Naka waa ji taq ci Piyeer ak Yowaana, ñépp waaru; ñu daldi daw, fekksi leen ca bérab ba ñuy wax Werandaa bu Suleymaan.
12 Bi Piyeer gisee loolu nag, mu ne mbooloo mi: «Yéen waa Israyil, lu tax ngeen waaru ci lii? Lu tax ngeen di nu xool jàkk, mel ni ci sunu kàttan, mbaa ci sunu ragal Yàlla lanu doxloo kii?
13 Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, di Yàllay sunuy maam, màggal na Ndawam Yeesu; yéena xàcceek moom, ba jébbal ko Pilaat, fekk naroon na koo bàyyi.
14 Yéen xeeb ngeen Aji Sell ji te Jub, te tinul ab reykat.
JËF YA 3 in Téereb Injiil

Jëf ya 3:8-14 in Kàddug Yàlla gi

8 Mu ne layy, taxaw, tàmbalee dox, ànd ak ñoom dugg ca kër Yàlla ga, di dox ak a tëbantu, tey sant Yàlla.
9 Mbooloo mépp gis ko, muy dox, di sant Yàlla.
10 Ñu xàmmi ko, xam ne moo daan toog, di yalwaan ca bunt bu Rafet ba ca kër Yàlla ga. Ñu jommi ba jommaaral, ba far gëlëm ca la ko dikkal.
11 Ba loolu amee waa ji taq ci Piyeer ak Yowaan, ñépp dawsi, sago jeex, ñu yéew leen ca mbaaru bunt ba ñu dippee Suleymaan.
12 Piyeer nag gis loolu, àddu, ne mbooloo ma: «Yeen bokki Israyil, lu ngeen di waaru ci lii? Lu ngeen nu naa jàkk, mel ni sunu manoorey bopp mbaa sunug njullite lanu doxloo kii?
13 Moom Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba, te di sunu Yàllay maam kay, moo màggal jawriñam Yeesu. Yeen nag yeena ko teg ciy loxo, jàmbu ko fa kanam Pilaat, te mu naroon koo bàyyi.
14 Yeen, yeena jàmbu Ku sell ki te jub, tinul ab bóomkat.
Jëf ya 3 in Kàddug Yàlla gi