Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 3

Jëf ya 3:8-14

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Mu ne layy, taxaw, tàmbalee dox, ànd ak ñoom dugg ca kër Yàlla ga, di dox ak a tëbantu, tey sant Yàlla.
9Mbooloo mépp gis ko, muy dox, di sant Yàlla.
10Ñu xàmmi ko, xam ne moo daan toog, di yalwaan ca bunt bu Rafet ba ca kër Yàlla ga. Ñu jommi ba jommaaral, ba far gëlëm ca la ko dikkal.
11Ba loolu amee waa ji taq ci Piyeer ak Yowaan, ñépp dawsi, sago jeex, ñu yéew leen ca mbaaru bunt ba ñu dippee Suleymaan.
12Piyeer nag gis loolu, àddu, ne mbooloo ma: «Yeen bokki Israyil, lu ngeen di waaru ci lii? Lu ngeen nu naa jàkk, mel ni sunu manoorey bopp mbaa sunug njullite lanu doxloo kii?
13Moom Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba, te di sunu Yàllay maam kay, moo màggal jawriñam Yeesu. Yeen nag yeena ko teg ciy loxo, jàmbu ko fa kanam Pilaat, te mu naroon koo bàyyi.
14Yeen, yeena jàmbu Ku sell ki te jub, tinul ab bóomkat.

Read Jëf ya 3Jëf ya 3
Compare Jëf ya 3:8-14Jëf ya 3:8-14