Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 3:15-24 in Wolof

Help us?

JËF YA 3:15-24 in Téereb Injiil

15 Bóom ngeen Aji Dundal ji, waaye Yàlla dekkal na ko; seede nanu ko nun ñépp.
16 Ci gëm turam la nit, kii ngeen di gis te xam ko, dëgëre; waaw, turu Yeesu ak ngëm gi jóge ci moom, moo tax mu wér péŋŋ ci seen kanam, yéen ñépp.
17 «Léegi nag bokk yi, xam naa ne ñàkka xam a tax ngeen def ko, yéen ak seeni kilifa.
18 Waaye noonu la Yàlla amale li mu yégle woon lu jiitu jaarale ko ci gémmiñug yonent yépp naan, Almaseem dina sonn.
19 Tuubleen seeni bàkkaar nag te waññiku ci Yàlla, ngir seeni bàkkaar far.
20 Noonu jamonoy péex dina bawoo ci Boroom bi, te muy yebal Almasi bi mu leen jagleel, maanaam Yeesu.
21 Asamaan war na koo yor, ba jamono ju ñuy defaraat lépp, di jamono ji Yàlla waxoon jaarale ko ci gémmiñug yonentam yu sell yépp, li dale ci njàlbéenug àddina.
22 Ndaxte Musaa nee woon na: “Boroom bi seen Yàlla dina leen feeñalal ci seen xeet Yonent ni man; nangeen ko déggal ci lépp lu mu leen wax.
23 Képp ku déggalul Yonent boobu, dees na la far ci xeet wi.”
24 «Li dale sax ci Samiyel ak ñi ci topp, bépp yonent bu wax yégle na bés yii.
JËF YA 3 in Téereb Injiil

Jëf ya 3:15-24 in Kàddug Yàlla gi

15 Bóom ngeen Kiy dundloo, waaye Yàllaa ko dekkal, nu seede ko.
16 Gëm aw turam moo waral turam woowu dooleel nit kii ngeen gis, xam ko. Kon ngëm moo waral lii; ngëm gu sababoo ci Yeesu moo ko may mu wér péŋŋ nii ci seen kanam, yeen ñépp.
17 «Teewul nag bokk yi, xam naa ne ñàkka xam moo leen taxa jëfe noonu, te loolu it moo dal seeni kilifa.
18 Waaye Yàlla moo sottale noonu la mu yégle woon lu jiitu, yonent yépp jottli, ne Almaseem dina sonn.
19 Kon nag tuubleen te dëpp, ndax seeni bàkkaar faru.
20 Su boobaa jamonoy péex ay bawoo ci Boroom bi, te mooy yebal Almasi mu leen jagleel, te muy Yeesu.
21 Moom la asamaan wara dalal, ba kera jamono ja lépp di dellu jag, na ko Yàlla waxe woon, yonent yu sell ya woon jottli.
22 Musaa kay noon na: “Boroom bi seen Yàlla mooy seppee ci seenu xeet ab yonent ni man; nangeen ko déggal ci lépp lu mu leen wax.
23 Képp ku déggalul yonent boobu, dees na la xettee ci xeet wi, sànk la.”
24 «Te it mboolem yonent yi wax, dale ko ci Samiyel ak ñi ko wuutu, ñoom it yégle woon nañu bés yii nuy dund.
Jëf ya 3 in Kàddug Yàlla gi