Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 3

JËF YA 3:15-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15Bóom ngeen Aji Dundal ji, waaye Yàlla dekkal na ko; seede nanu ko nun ñépp.
16Ci gëm turam la nit, kii ngeen di gis te xam ko, dëgëre; waaw, turu Yeesu ak ngëm gi jóge ci moom, moo tax mu wér péŋŋ ci seen kanam, yéen ñépp.
17«Léegi nag bokk yi, xam naa ne ñàkka xam a tax ngeen def ko, yéen ak seeni kilifa.
18Waaye noonu la Yàlla amale li mu yégle woon lu jiitu jaarale ko ci gémmiñug yonent yépp naan, Almaseem dina sonn.
19Tuubleen seeni bàkkaar nag te waññiku ci Yàlla, ngir seeni bàkkaar far.
20Noonu jamonoy péex dina bawoo ci Boroom bi, te muy yebal Almasi bi mu leen jagleel, maanaam Yeesu.
21Asamaan war na koo yor, ba jamono ju ñuy defaraat lépp, di jamono ji Yàlla waxoon jaarale ko ci gémmiñug yonentam yu sell yépp, li dale ci njàlbéenug àddina.
22Ndaxte Musaa nee woon na: “Boroom bi seen Yàlla dina leen feeñalal ci seen xeet Yonent ni man; nangeen ko déggal ci lépp lu mu leen wax.
23Képp ku déggalul Yonent boobu, dees na la far ci xeet wi.”
24«Li dale sax ci Samiyel ak ñi ci topp, bépp yonent bu wax yégle na bés yii.

Read JËF YA 3JËF YA 3
Compare JËF YA 3:15-24JËF YA 3:15-24