Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 3:11-16 in Wolof

Help us?

JËF YA 3:11-16 in Téereb Injiil

11 Naka waa ji taq ci Piyeer ak Yowaana, ñépp waaru; ñu daldi daw, fekksi leen ca bérab ba ñuy wax Werandaa bu Suleymaan.
12 Bi Piyeer gisee loolu nag, mu ne mbooloo mi: «Yéen waa Israyil, lu tax ngeen waaru ci lii? Lu tax ngeen di nu xool jàkk, mel ni ci sunu kàttan, mbaa ci sunu ragal Yàlla lanu doxloo kii?
13 Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, di Yàllay sunuy maam, màggal na Ndawam Yeesu; yéena xàcceek moom, ba jébbal ko Pilaat, fekk naroon na koo bàyyi.
14 Yéen xeeb ngeen Aji Sell ji te Jub, te tinul ab reykat.
15 Bóom ngeen Aji Dundal ji, waaye Yàlla dekkal na ko; seede nanu ko nun ñépp.
16 Ci gëm turam la nit, kii ngeen di gis te xam ko, dëgëre; waaw, turu Yeesu ak ngëm gi jóge ci moom, moo tax mu wér péŋŋ ci seen kanam, yéen ñépp.
JËF YA 3 in Téereb Injiil

Jëf ya 3:11-16 in Kàddug Yàlla gi

11 Ba loolu amee waa ji taq ci Piyeer ak Yowaan, ñépp dawsi, sago jeex, ñu yéew leen ca mbaaru bunt ba ñu dippee Suleymaan.
12 Piyeer nag gis loolu, àddu, ne mbooloo ma: «Yeen bokki Israyil, lu ngeen di waaru ci lii? Lu ngeen nu naa jàkk, mel ni sunu manoorey bopp mbaa sunug njullite lanu doxloo kii?
13 Moom Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba, te di sunu Yàllay maam kay, moo màggal jawriñam Yeesu. Yeen nag yeena ko teg ciy loxo, jàmbu ko fa kanam Pilaat, te mu naroon koo bàyyi.
14 Yeen, yeena jàmbu Ku sell ki te jub, tinul ab bóomkat.
15 Bóom ngeen Kiy dundloo, waaye Yàllaa ko dekkal, nu seede ko.
16 Gëm aw turam moo waral turam woowu dooleel nit kii ngeen gis, xam ko. Kon ngëm moo waral lii; ngëm gu sababoo ci Yeesu moo ko may mu wér péŋŋ nii ci seen kanam, yeen ñépp.
Jëf ya 3 in Kàddug Yàlla gi