11Ba loolu amee waa ji taq ci Piyeer ak Yowaan, ñépp dawsi, sago jeex, ñu yéew leen ca mbaaru bunt ba ñu dippee Suleymaan.
12Piyeer nag gis loolu, à ddu, ne mbooloo ma: «Yeen bokki Israyil, lu ngeen di waaru ci lii? Lu ngeen nu naa jà kk, mel ni sunu manoorey bopp mbaa sunug njullite lanu doxloo kii?
13Moom Yà llay Ibraayma, di Yà llay Isaaxa, di Yà llay Yanqóoba, te di sunu Yà llay maam kay, moo mà ggal jawriñam Yeesu. Yeen nag yeena ko teg ciy loxo, jà mbu ko fa kanam Pilaat, te mu naroon koo bà yyi.
14Yeen, yeena jà mbu Ku sell ki te jub, tinul ab bóomkat.
15Bóom ngeen Kiy dundloo, waaye Yà llaa ko dekkal, nu seede ko.
16Gëm aw turam moo waral turam woowu dooleel nit kii ngeen gis, xam ko. Kon ngëm moo waral lii; ngëm gu sababoo ci Yeesu moo ko may mu wér péŋŋ nii ci seen kanam, yeen ñépp.