Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 28:3-23 in Wolof

Help us?

JËF YA 28:3-23 in Téereb Injiil

3 Pool nag di for matt, di ko def ca taal ba, jaan ne ca mëlle ndax tàngoor wa, taq ci loxoom.
4 Bi waa réew ma gisee rab wa wékku ci loxoom nag, ñuy waxante naan: «Ci lu wóor nit kii reykat la; te bi mu rëccee ca géej ga sax, ndogalu Yàlla mayu ko mu dund.»
5 Waaye Pool yëlëb rab wa ca sawara sa, te wàññiwu ko dara.
6 Nit ñi di xaar mu newi, mbaa mu ne dàll, dee; waaye bi ñu négee lu yàgg te gis ne dara jotu ko, ñu soppi xel ne: «Kii yàlla la.»
7 Amoon na nag ca wet ya ay suuf yu doon moomeelu ku tudd Publiyus, di kilifag dun ba. Mu teeru nu, ganale nu ngan gu réy diirub ñetti fan.
8 Fekk baayu Publiyus dafa tëdd ndax ay tàngoori yaram yu koy dikkal ak biiru taññ. Pool nag dem seeti ko, ñaan ci Yàlla, teg ko ay loxoom, mu daldi wér.
9 Ci kaw loolu jarag ya ca des ca dun ba daldi dikk, amaat wér-gi-yaram.
10 Ñu teral nu ci fànn yu bare, te bi nuy dem, ñu jox nu li nuy soxla lépp.
11 Bi nu fa amee ñetti weer, nu dugg ca gaal gu lollikoo ca dun ba, daldi tàbbi ca géej ga. Gaalu dëkku Alegsàndiri la woon, te yor xàmmikaay guy nataalu Kastor ak Polugsë.
12 Noonu nu teer dëkku Sirakus, toog fa ñetti fan.
13 Nu jóge fa, leru tefes ga, ba agsi Resiyo. Ca ëllëg sa ngelawu sudd daldi jóg, te ca ñaareelu fan ba nu teer Pusol.
14 Gis nanu fa ay bokk, ñu ñaan nu, nu toog fa ayu-bés. Noonu nu dem Room.
15 Sunuy xibaar law na, ba egg ca bokk ya fa dëkk, noonu ñu gatandu nu ba ca péncu Apiyus ak bérab bu ñuy wax Ñetti añukaay ya. Bi leen Pool gisee, mu sant Yàlla, daldi takk fitam.
16 Bi nu dikkee Room nag, ñu may Pool, mu dëkk fa ko lew, moom ak xarekat ba koy wottu.
17 Bi ñetti fan wéyee, mu woolu njiiti Yawuti dëkk ba. Bi ñu dajaloo nag, mu wax leen lii: «Bokk yi, jàpp nañu ma ci Yerusalem, jébbal ma waa Room, fekk defuma dara luy suufeel sunu xeet, mbaa lu juuyoo ak sunuy aaday maam.
18 Waa Room nag seet sama mbir, te bëgg maa bàyyi, ndaxte toppuñu ma dara lu jar dee.
19 Waaye bi ko Yawut ya bañee, fas yéene naa dénk sama mbir Sesaar, fekk ba tey awma dara lu may taqal sama xeet.
20 Moo tax ma ñaana gise ak yéen, nu diisoo, ndaxte yaakaaru bànni Israyil moo tax ñu jéng ma.»
21 Bi ñu ko déggee, ñu ne ko: «Jotunu benn bataaxal bu jóge Yude ci sa mbir, te kenn ci bokk, yi fi dikk, jottaliwul mbaa mu seede ci yaw lu bon.
22 Waaye bëgg nanoo dégg li nga gëm, ndaxte xam nanu ne, tariixa booba, kenn jubluwu ko fenn.»
23 Noonu ñu jox ko bés, te ñu bare ñëw, fekksi ko ca néegam. Mu di leen jàngal suba ba ngoon, di leen dëggal lu jëm ci nguuru Yàlla ak ci Yeesu, tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi, di leen jéema gëmloo.
JËF YA 28 in Téereb Injiil

Jëf ya 28:3-23 in Kàddug Yàlla gi

3 Póol daldi taxan aw say, di ko teg ca taal ba, jaan génne ca ndax tàngoor wa, màtt ko ba taq ci loxoom.
4 Waa réew ma gis jaan ja langaamoo loxol Póol, ñu naan ca seen biir: «Nit kii kay ab bóomkat lay doon, ndegam moo rëcce géej, te taxul Ndogal may ko mu dund.»
5 Teewul Póol yëlëb jaan ja ca sawara sa, te dara jotu ko.
6 Nit ña nag di ko xoole yaram wu newi, mbaa mu jekki ne dàll, dee. Naka lañu xool lu yàgg ba gis ne dara jotu ko, ñu xalaataat, daldi ne Póol yàlla la.
7 Ca wetu tefes googee nu teere nag, fa la toolub kilifag dun ba féete woon, ñu di ko wax Publiyus. Mu dalal nu, ganale nu ngan gu neex diiru ñetti fan.
8 Fekk na baayu Publiyus a nga tëdd ndax tàngooru yaram ak biiru taññ. Ci biir loolu Póol dem seeti ko, ñaanal ko, teg ko ay loxoom, mu wér.
9 Ba loolu amee jarag ya ca dun ba dikk, daldi wér ñoom itam.
10 Teraanga yu bare terale nañu nu ko fa, te ba nuy dem, jox nañu nu la nu soxla.
11 Gannaaw ba nu fa amee ñetti weer lanu dugg gaal gu lollikoo woon ca dun ba. Gaal gaa nga bàyyikoo woon Alegsàndiri, di xàmmikoo jëmmi tuur ya ñuy wax Kastor ak Polugsë. Nu daldi tàbbiwaat biir géej.
12 Nu teeri dëkk ba ñuy wax Sirakus, toog fa ñetti fan.
13 Nu jóge fa, leru tefes ga, ba agsi Resiyo. Ca ëllëg sa ngelawal bëj-saalum jóg, nu daldi àgg teerub Pusol ci ñaari fan.
14 Gis nanu fa ay bokki gëmkat, ñu ñaan nu, ba nu toog fa ñoom juróom ñaari fan. Gannaaw loolu nu dem Room.
15 Ba bokki gëmkati Room yégee ne nu ngi dikk, ñoo nu gatandusi ba fa ñuy wax péncu Apiyus ak fa ñuy wax Ñetti dalu gan ya. Ba leen Póol gisee, daa sant Yàlla, daldi gëna sawar.
16 Ba nu dikkee Room nag may nañu Póol, mu am daluwaayu boppam, ab takk-der di ko wattu.
17 Ñu teg ca ñetti fa, mu woolu njiiti Yawuti dëkk ba. Ba ñu dajee, mu ne leen: «Bokk yi, man defuma dara lu dëngook sunuw xeet mbaa sunu aaday maam. Teewul ñu jàppe ma fa Yerusalem, teg ma ci loxoy Room.
18 Ñooñu seet sama mbir, gisuñu ci man tuuma ju yelloo àtteb dee, ñu nar maa bàyyi.
19 Ba Yawut ya bañee nag, amatuma pexe mu dul dénk sama mbir Sesaar, doonte du lenn lu may toppe samaw xeet.
20 Mbir moomu nag moo tax ma woolu leen, ngir giseek yeen, diisook yeen, ndax yaakaaru bànni Israyil moo waral sama jéng yii.»
21 Ñu ne ko: «Nun de, du benn bataaxal bu nu jot bu jóge Yude ci sa mbir, te du kenn ci bokk yi, ku dikk wax mbaa mu seedeel la lenn lu bon.
22 Waaye bëgg nanoo dégg ci sa gémmiñu bopp li nga gëm, ndax li nu xam daal mooy, ngér moomu nga bokk, fu nekk lañu koy diiŋate.»
23 Ci kaw loolu ñu jox ko bés, bés ba dikk, ñu bare dikk, fekksi ko ca daluwaayam. Suba ba ngoon mu di leen jàngal, di leen seedeel lu jëm ci nguurug Yàlla, di leen won ci mbirum Yeesu, firnde yu leen gëmloo te tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi.
Jëf ya 28 in Kàddug Yàlla gi