Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 28

Jëf ya 28:3-23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Póol daldi taxan aw say, di ko teg ca taal ba, jaan génne ca ndax tàngoor wa, màtt ko ba taq ci loxoom.
4Waa réew ma gis jaan ja langaamoo loxol Póol, ñu naan ca seen biir: «Nit kii kay ab bóomkat lay doon, ndegam moo rëcce géej, te taxul Ndogal may ko mu dund.»
5Teewul Póol yëlëb jaan ja ca sawara sa, te dara jotu ko.
6Nit ña nag di ko xoole yaram wu newi, mbaa mu jekki ne dàll, dee. Naka lañu xool lu yàgg ba gis ne dara jotu ko, ñu xalaataat, daldi ne Póol yàlla la.
7Ca wetu tefes googee nu teere nag, fa la toolub kilifag dun ba féete woon, ñu di ko wax Publiyus. Mu dalal nu, ganale nu ngan gu neex diiru ñetti fan.
8Fekk na baayu Publiyus a nga tëdd ndax tàngooru yaram ak biiru taññ. Ci biir loolu Póol dem seeti ko, ñaanal ko, teg ko ay loxoom, mu wér.
9Ba loolu amee jarag ya ca dun ba dikk, daldi wér ñoom itam.
10Teraanga yu bare terale nañu nu ko fa, te ba nuy dem, jox nañu nu la nu soxla.
11Gannaaw ba nu fa amee ñetti weer lanu dugg gaal gu lollikoo woon ca dun ba. Gaal gaa nga bàyyikoo woon Alegsàndiri, di xàmmikoo jëmmi tuur ya ñuy wax Kastor ak Polugsë. Nu daldi tàbbiwaat biir géej.
12Nu teeri dëkk ba ñuy wax Sirakus, toog fa ñetti fan.
13Nu jóge fa, leru tefes ga, ba agsi Resiyo. Ca ëllëg sa ngelawal bëj-saalum jóg, nu daldi àgg teerub Pusol ci ñaari fan.
14Gis nanu fa ay bokki gëmkat, ñu ñaan nu, ba nu toog fa ñoom juróom ñaari fan. Gannaaw loolu nu dem Room.
15Ba bokki gëmkati Room yégee ne nu ngi dikk, ñoo nu gatandusi ba fa ñuy wax péncu Apiyus ak fa ñuy wax Ñetti dalu gan ya. Ba leen Póol gisee, daa sant Yàlla, daldi gëna sawar.
16Ba nu dikkee Room nag may nañu Póol, mu am daluwaayu boppam, ab takk-der di ko wattu.
17Ñu teg ca ñetti fa, mu woolu njiiti Yawuti dëkk ba. Ba ñu dajee, mu ne leen: «Bokk yi, man defuma dara lu dëngook sunuw xeet mbaa sunu aaday maam. Teewul ñu jàppe ma fa Yerusalem, teg ma ci loxoy Room.
18Ñooñu seet sama mbir, gisuñu ci man tuuma ju yelloo àtteb dee, ñu nar maa bàyyi.
19Ba Yawut ya bañee nag, amatuma pexe mu dul dénk sama mbir Sesaar, doonte du lenn lu may toppe samaw xeet.
20Mbir moomu nag moo tax ma woolu leen, ngir giseek yeen, diisook yeen, ndax yaakaaru bànni Israyil moo waral sama jéng yii.»
21Ñu ne ko: «Nun de, du benn bataaxal bu nu jot bu jóge Yude ci sa mbir, te du kenn ci bokk yi, ku dikk wax mbaa mu seedeel la lenn lu bon.
22Waaye bëgg nanoo dégg ci sa gémmiñu bopp li nga gëm, ndax li nu xam daal mooy, ngér moomu nga bokk, fu nekk lañu koy diiŋate.»
23Ci kaw loolu ñu jox ko bés, bés ba dikk, ñu bare dikk, fekksi ko ca daluwaayam. Suba ba ngoon mu di leen jàngal, di leen seedeel lu jëm ci nguurug Yàlla, di leen won ci mbirum Yeesu, firnde yu leen gëmloo te tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi.

Read Jëf ya 28Jëf ya 28
Compare Jëf ya 28:3-23Jëf ya 28:3-23