3 Póol daldi taxan aw say, di ko teg ca taal ba, jaan génne ca ndax tàngoor wa, màtt ko ba taq ci loxoom.
4 Waa réew ma gis jaan ja langaamoo loxol Póol, ñu naan ca seen biir: «Nit kii kay ab bóomkat lay doon, ndegam moo rëcce géej, te taxul Ndogal may ko mu dund.»
5 Teewul Póol yëlëb jaan ja ca sawara sa, te dara jotu ko.
6 Nit ña nag di ko xoole yaram wu newi, mbaa mu jekki ne dàll, dee. Naka lañu xool lu yàgg ba gis ne dara jotu ko, ñu xalaataat, daldi ne Póol yàlla la.
7 Ca wetu tefes googee nu teere nag, fa la toolub kilifag dun ba féete woon, ñu di ko wax Publiyus. Mu dalal nu, ganale nu ngan gu neex diiru ñetti fan.
8 Fekk na baayu Publiyus a nga tëdd ndax tàngooru yaram ak biiru taññ. Ci biir loolu Póol dem seeti ko, ñaanal ko, teg ko ay loxoom, mu wér.
9 Ba loolu amee jarag ya ca dun ba dikk, daldi wér ñoom itam.
10 Teraanga yu bare terale nañu nu ko fa, te ba nuy dem, jox nañu nu la nu soxla.