3tinu ko ngir mu woolu Póol Yerusalem, ndax fekk na leen lal pexem rey ko ca yoon wa.
4Festus itam ne leen Póol a nga ñu tëj kaso ca Sesare, te moom ci boppam, fa la nara gaaw, dellu.
5Mu ne leen: «Kon nag, na nit ñu am baat ñu bokk ci yeen, ànd ak man, tuumaali waa ji, ndegam am na fenn fu mu tooñe.»