Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 24:15-26 in Wolof

Help us?

JËF YA 24:15-26 in Téereb Injiil

15 Te bokk naa ak ñoom yaakaar ci Yàlla, ne ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki keroog yawmelxayaam.
16 Moo tax fu ma tollu, maa ngi góor-góorlu, ngir am xel mu dal fa kanam Yàlla ak fa kanam nit ñi.
17 «Noonu gannaaw gëjeb at yu bare ñëw naa, ngir indil sama xeet ndimbal te jébbal Yàlla ay sarax.
18 Bi ma koy def nag, gis nañu ma ca kër Yàlla ga, ma setlu ba noppi, fekk ànduma ak mbooloo te indiwuma benn coow.
19 Waaye ay Yawut yu dëkk Asi —xanaa kay ñoo waroona ñëw ci sa kanam, di ma kalaame, bu ñu amee dara lu ñu may topp.
20 Waaye it na nit ñii wax ci lan laa tooñe ci jataayu géewub àtte ba,
21 xanaa li ma waxoon ca kaw ci seen biir rekk ne: “Mbirum ndekkitel ñi dee moo tax ngeen dëj ma ci seen kanam tey!”»
22 Bi mu waxee noonu, Feligsë mi xam bu wóor mbirum yoon wi, yiwi leen ba beneen yoon. Mu ne leen: «Bu Lisiyas kilifag xare bi ñëwee, dinaa àtte seen mbir.»
23 Noonu mu sant njiitu xare ba ne ko: «Nanga wottu Pool, waaye nga may ko féex, te bàyyi ay xaritam, ñu topptoo ko.»
24 Bi ay fan wéyee, Feligsë ñëwaat, ànd ak soxnaam Dursil, miy Yawut. Noonu mu woolu Pool, di ko déglu ci mbirum gëm Yeesu Kirist.
25 Waaye bi Pool di waxtaan ci mbirum njub ak moom sa bopp ak bés pénc, Feligsë daldi tiit, yiwi ko ne ko: «Demal, bu ma amee jot, dinaa la woolu.»
26 Fekk yaakaaroon na it ne, Pool dina ko jox xaalis; kon mu di ko farala woolu, ngir waxtaan ak moom.
JËF YA 24 in Téereb Injiil

Jëf ya 24:15-26 in Kàddug Yàlla gi

15 Yaakaar ji ma am, mooy yaakaar ji ñu am ñoom itam, ne ñi jub ak ñi jubadi, ñépp ay bokk dekki ëllëg.
16 Moo tax fu ma tollu, man itam, may def lu ma man ngir am xel mu dal, wàccoo ak Yàlla, wàccoo ak nit ñi.
17 «Samay tànk nag, gannaaw gëjeb at yu bare, moo doon indil samaw askan, ay ndimbal ak ay sarax yu ñeel Yàlla.
18 Ci biir loolu lañu ma fekk ca biir kër Yàlla ga, ma setlu, te du mbooloo, du coow lu ma indaale.
19 Xanaa ñenn Yawuti diiwaanu Asi ña ma fa fekkoon. Ñooñoo ma waroona tuumaal fi sa kanam, ndegam am nañu lenn lu ñu ma sikke.
20 Mbaa boog, na nit ñii ci seen bopp wax gan ndëngte lañu ma gisal, keroog ba ma taxawee ca kurélu àttekat ya!
21 Xanaa genn kàddu ga ma taxawoon ca seen biir, àddu ko ca kaw ne: “Mbirum ndee-ndekki gi ma gëm, moom lañu may àttee ci seen kanam tey!”»
22 Booba Feligsë jotoon naa am lu ko leer ci mbirum Yoon wi. Mu yiweegum leen nag, ne leen: «Bu Lisiyas njiital gàngoor gi dikkee, dinaa àtte seen mbir.»
23 Ci kaw loolu mu sant njiitu takk-der ba, ne ko mu may Póol bët, woyofal ko jataayu kasoom te baña aaye ay nitam ñu topptoo ko.
24 Ñu teg ci ay fan, Feligsë dikk, ànd ak soxnaam Dursil, mi dib Yawut. Mu woolu Póol, déglu kàddoom ci ngëm gi sababoo ci Yeesu Almasi.
25 Naka la Póol wax ci mbirum njub, ak moom sa bakkan, ak àtteb bés-pénc, Feligsë daldi tiit, ne ko: «Léegi, man ngaa demagum, bu ma ko talee, dinaa la wooluwaat.»
26 Ci biir loolu Feligsë yaakaar itam ne jombul mu jële xaalisub neexal ci Póol, ba tax mu woolu ko ay yooni yoon, ngir waxtaan ak moom.
Jëf ya 24 in Kàddug Yàlla gi