Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 24:13-20 in Wolof

Help us?

JËF YA 24:13-20 in Téereb Injiil

13 Te manuñoo firndeel dara ci li ñu may jiiñ léegi.
14 Waaye nangu naa ci sa kanam ne maa ngi jaamu Yàllay sunuy maam, ci topp yoon wi ñu ne mooy tariixa; terewul ne lépp li ñu tëral ci yoonu Musaa ak li yonent yi bind, gëm naa ko.
15 Te bokk naa ak ñoom yaakaar ci Yàlla, ne ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki keroog yawmelxayaam.
16 Moo tax fu ma tollu, maa ngi góor-góorlu, ngir am xel mu dal fa kanam Yàlla ak fa kanam nit ñi.
17 «Noonu gannaaw gëjeb at yu bare ñëw naa, ngir indil sama xeet ndimbal te jébbal Yàlla ay sarax.
18 Bi ma koy def nag, gis nañu ma ca kër Yàlla ga, ma setlu ba noppi, fekk ànduma ak mbooloo te indiwuma benn coow.
19 Waaye ay Yawut yu dëkk Asi —xanaa kay ñoo waroona ñëw ci sa kanam, di ma kalaame, bu ñu amee dara lu ñu may topp.
20 Waaye it na nit ñii wax ci lan laa tooñe ci jataayu géewub àtte ba,
JËF YA 24 in Téereb Injiil

Jëf ya 24:13-20 in Kàddug Yàlla gi

13 Te itam li ñu may jiiñ nii tey, manuñu cee firndeel dara.
14 Lenn de man naa la koo nangul. Yoon woowu ñu ne mooy ngér mu sikk, moom laay topp, di ko jaamoo sunu Yàllay maam. Teewul mboolem lu ñu bind ci yoonu Musaa ak téerey yonent yi, gëm naa ko.
15 Yaakaar ji ma am, mooy yaakaar ji ñu am ñoom itam, ne ñi jub ak ñi jubadi, ñépp ay bokk dekki ëllëg.
16 Moo tax fu ma tollu, man itam, may def lu ma man ngir am xel mu dal, wàccoo ak Yàlla, wàccoo ak nit ñi.
17 «Samay tànk nag, gannaaw gëjeb at yu bare, moo doon indil samaw askan, ay ndimbal ak ay sarax yu ñeel Yàlla.
18 Ci biir loolu lañu ma fekk ca biir kër Yàlla ga, ma setlu, te du mbooloo, du coow lu ma indaale.
19 Xanaa ñenn Yawuti diiwaanu Asi ña ma fa fekkoon. Ñooñoo ma waroona tuumaal fi sa kanam, ndegam am nañu lenn lu ñu ma sikke.
20 Mbaa boog, na nit ñii ci seen bopp wax gan ndëngte lañu ma gisal, keroog ba ma taxawee ca kurélu àttekat ya!
Jëf ya 24 in Kàddug Yàlla gi