Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 23:15-32 in Wolof

Help us?

JËF YA 23:15-32 in Téereb Injiil

15 Léegi nag yéen ak kureelu àttekat ya, laajleen kilifa ga, mu indi ko ci seen kanam, mel ni dangeena bëgga seet mbiram bu gëna wóor. Bu ko defee nun dinanu fagaru, ngir rey ko, bala moo agsi.»
16 Waaye jarbaatu Pool yég fiir ga, mu dem, dugg ca tata ja, yégal ko Pool.
17 Bi ko Pool déggee, mu woo kenn ca njiiti xare ba ne ko: «Yóbbul waxambaane wii ca kilifa ga, ndax am na lu mu ko wara yégal.»
18 Njiit la jël ko, yóbbu ko ca kilifa ga ne ko: «Pool, mi ñu jàpp, moo ma woo, ñaan ma, ma indil la waxambaane wii, ndaxte am na lu mu lay wax.»
19 Noonu kilifa ga jàpp ci loxob waxambaane wa, wéetoo ak moom, laaj ko: «Loo ma bëgga yégal?»
20 Mu ne: «Yawut yi dañoo dige, ngir ñaan la, nga indi Pool ëllëg ca kanam kureelu àttekat ya, mel ni dañoo bëgga seet mbiram bu gëna wóor.
21 Bu leen ko may, ndaxte lu ëpp ñeent fukk ci ñoom ñu ngi koy lalal fiir. Dige nañu ak ngiñ ne dootuñu lekk, dootuñu naan, li feek reyuñu ko; fi mu ne sax fagaru nañu, di xaar, nga nangu.»
22 Kilifa ga nag sant waxambaane wa, mu bañ koo àgge kenn, ba noppi mu yiwi ko, mu dem.
23 Bi mu ko defee mu woo ñaar ci njiiti xare ba ne leen: «Waajal-leen ñaar téeméeri xarekat ak juróom ñaar fukki gawar ak ñaar téeméeri nit ñu gànnaayoo xeej, ngeen dem Sesare ci juróom ñeenti waxtu ci guddi.
24 Wutal-leen it Pool lu mu war, ngeen yóbbu ko ci jàmm ak salaam ba ca Feligsë, boroom réew mi.»
25 Noonu mu bind bataaxal bii:
26 Yaw Feligsë mu tedd mi, di boroom réew mi; man Këlódd Lisiyas maa ngi lay nuyu.
27 Yawut yi jàpp nañu nit kii, bëgg koo rey, waaye bi ma yégee ne jaambur la ci Room, wallu naa ko ak ay xarekat, ba musal ko.
28 Bëggoon naa xam lu tax ñu kalaame ko. Moo tax ma yóbbu ko ca kanam seen kureelu àttekat ya.
29 Gis naa ne li ñu ko jiiñ mu ngi aju ci ay werantey seen yoon, waaye jiiñuñu ko dara lu jar dee mbaa jéng.
30 Te bi ma déggee ne ñu ngi koy fexeel, yebal naa ko ci yaw ci saa si. Sant naa nag ñi ko kalaame, ñu xamal la seen lay.
31 Noonu xarekat ya jël Pool ci guddi, indi ko ba ca dëkku Antipataris, ni ñu leen ko sante.
32 Ca ëllëg sa ñu waññiku, délsi ca tata ja, bàyyi gawar ga, ñu gunge ko.
JËF YA 23 in Téereb Injiil

Jëf ya 23:15-32 in Kàddug Yàlla gi

15 Léegi nag yeen ak kurélu àttekat yi, ñaanleen njiital gàngoor gi, mu indi Póol ba ci yeen, mu mel ni dangeena bëgga seetaat bu baax mbiram. Nun nag fagaru nanu, ngir bala moo agsi, nu rey ko.»
16 Jarbaatub Póol bu góor nag yég tëru ma. Mu daldi dem ba ca tata ja, dugg, yégal ko Póol.
17 Póol woo kenn ca njiiti takk-der ya, ne ko: «Yóbbul xale bu góor bii ba ci njiital gàngoor gi, ndax am na lu mu ko wara wax.»
18 Njiital xare ba ànd ak xale ba, yóbbu ko ca njiital gàngoor ga, ne ko: «Póol, mi ñu tëj, moo ma woo, ñaan ma, ma indil la xalelu góor bii, ndax am na lu mu lay wax.»
19 Ba loolu amee njiital gàngoor gi jàpp ci loxol xalelu góor bi, wéetoo ak moom, ne ko: «Ana loo may xamal?»
20 Mu ne ko: «Yawut yi ñoo mànkoo ci ñaan la, nga yóbbu Póol ëllëg ca kurélu àttekat ya, mu mel ni dañoo bëgga seetaat bu baax mbiram.
21 Yaw nag bu leen ko may, ndax lu ëpp ñeent fukk ci ñoom a koy tëru, te xasoo nañu ne dootuñu lekk, dootuñu naan, ba kera ñu ko reyee. Fagaru nañu ba noppi, di xaar sa ndigal.»
22 Njiital gàngoor ga daldi koy yiwi, ne ko: «Bul wax kenn ne ko àgge nga ma lii.»
23 Ba mu ko defee mu woo ñaari njiiti takk-der, ne leen: «Waajal-leen ñaar téeméeri xarekat ak juróom ñaar fukki gawar ak ñaar téeméeri boroom xeej, ngir ngeen dem Sesare bu juróom ñeenti waxtu jotee ci guddi.
24 Te itam nangeen waajalal Póol daamar, waral ko, ngir yóbbu kook jàmm ba ca Feligsë, boroom réew mi.»
25 Mu bind nag bataaxal bu ne:
26 Ñeel la yaw boroom réew mi, Feligsë mu tedd mee tedd, bawoo ci man Këlódd Lisiyas, mi lay nuyu.
27 Nit kii la Yawut yi jàppoon, di ko waaja rey, far ma dikk ànd ak lenn ci gàngoor gi, wallu ko, ndax fekk na ma yég ne as goru Room la.
28 Ma bëggoona xam nag lan lañu koy sikk, ba tax ma yóbbu woon ko ca seen kurélu àttekat ya.
29 Ma gis nag ne li ñu ko jiiñ, ci seen mbiri yoonu diine rekk la, waaye du lenn lu jar rey, mbaa jéng.
30 Ba ñu ma àggee am tëru mu ko Yawut yi waajaloon nag, ci laa ko yebal ci yaw ci saa si. Jox naa itam ndigal ñi ko sikk, ne leen ñu wax ci sa kanam, gan tooñ lañu ko toppe.
31 Ba loolu amee xarekat ya def la ñu leen digal, yóbbu Póol ci guddi ba ca dëkk ba ñuy wax Antipataris.
32 Ca ëllëg sa takk-der yay deme tànk waññiku, délsi ca tata ja, bàyyi gawar ga, ñu gunge Póol ba mu àgg.
Jëf ya 23 in Kàddug Yàlla gi