Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 23

Jëf ya 23:15-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15Léegi nag yeen ak kurélu àttekat yi, ñaanleen njiital gàngoor gi, mu indi Póol ba ci yeen, mu mel ni dangeena bëgga seetaat bu baax mbiram. Nun nag fagaru nanu, ngir bala moo agsi, nu rey ko.»
16Jarbaatub Póol bu góor nag yég tëru ma. Mu daldi dem ba ca tata ja, dugg, yégal ko Póol.
17Póol woo kenn ca njiiti takk-der ya, ne ko: «Yóbbul xale bu góor bii ba ci njiital gàngoor gi, ndax am na lu mu ko wara wax.»
18Njiital xare ba ànd ak xale ba, yóbbu ko ca njiital gàngoor ga, ne ko: «Póol, mi ñu tëj, moo ma woo, ñaan ma, ma indil la xalelu góor bii, ndax am na lu mu lay wax.»
19Ba loolu amee njiital gàngoor gi jàpp ci loxol xalelu góor bi, wéetoo ak moom, ne ko: «Ana loo may xamal?»
20Mu ne ko: «Yawut yi ñoo mànkoo ci ñaan la, nga yóbbu Póol ëllëg ca kurélu àttekat ya, mu mel ni dañoo bëgga seetaat bu baax mbiram.
21Yaw nag bu leen ko may, ndax lu ëpp ñeent fukk ci ñoom a koy tëru, te xasoo nañu ne dootuñu lekk, dootuñu naan, ba kera ñu ko reyee. Fagaru nañu ba noppi, di xaar sa ndigal.»
22Njiital gàngoor ga daldi koy yiwi, ne ko: «Bul wax kenn ne ko àgge nga ma lii.»
23Ba mu ko defee mu woo ñaari njiiti takk-der, ne leen: «Waajal-leen ñaar téeméeri xarekat ak juróom ñaar fukki gawar ak ñaar téeméeri boroom xeej, ngir ngeen dem Sesare bu juróom ñeenti waxtu jotee ci guddi.
24Te itam nangeen waajalal Póol daamar, waral ko, ngir yóbbu kook jàmm ba ca Feligsë, boroom réew mi.»
25Mu bind nag bataaxal bu ne:
26Ñeel la yaw boroom réew mi, Feligsë mu tedd mee tedd, bawoo ci man Këlódd Lisiyas, mi lay nuyu.
27Nit kii la Yawut yi jàppoon, di ko waaja rey, far ma dikk ànd ak lenn ci gàngoor gi, wallu ko, ndax fekk na ma yég ne as goru Room la.
28Ma bëggoona xam nag lan lañu koy sikk, ba tax ma yóbbu woon ko ca seen kurélu àttekat ya.
29Ma gis nag ne li ñu ko jiiñ, ci seen mbiri yoonu diine rekk la, waaye du lenn lu jar rey, mbaa jéng.
30Ba ñu ma àggee am tëru mu ko Yawut yi waajaloon nag, ci laa ko yebal ci yaw ci saa si. Jox naa itam ndigal ñi ko sikk, ne leen ñu wax ci sa kanam, gan tooñ lañu ko toppe.
31Ba loolu amee xarekat ya def la ñu leen digal, yóbbu Póol ci guddi ba ca dëkk ba ñuy wax Antipataris.
32Ca ëllëg sa takk-der yay deme tànk waññiku, délsi ca tata ja, bàyyi gawar ga, ñu gunge Póol ba mu àgg.

Read Jëf ya 23Jëf ya 23
Compare Jëf ya 23:15-32Jëf ya 23:15-32