Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 21:3-26 in Wolof

Help us?

JËF YA 21:3-26 in Téereb Injiil

3 Noonu nu séen dunu Sipar, bàyyi ko ci sunu càmmoñ, jublu diiwaanu Siri, nu teersi Tir. Ndaxte foofa la gaal gi wara yebbee la mu yeboon.
4 Nu wut taalibe ya, ba gis leen, toog ak ñoom juróom ñaari fan. Ñoom nag ñu ne Pool ci li leen Xelu Yàlla mi may, mu baña dem Yerusalem.
5 Moona bi jataayu gaal ga matee, nu awaat ci yoon wi. Te ñépp gunge nu, ñoom ak seeni soxna ak seeni doom; nu génn dëkk ba, sukk ca tefes ga, ñaan ci Yàlla.
6 Noonu nu tàggoo ak ñoom, dugg ca gaal ga, ñu dellu seen kër.
7 Bi nu jógee Tir nag, nu demaat ci géej, ba teer Patolemayis. Foofa nu nuyu bokk ya, yendu, fanaan.
8 Nu jóge fa ca ëllëg sa, ñëw ba ca dëkku Sesare. Nu dugg ca kër Filib, taskatu xibaaru jàmm bi, mi bokk ci Juróom ñaar ña, nu dal fa moom.
9 Amoon na ñeenti doom yuy janq, ñuy wax ci kàddug Yàlla.
10 Bi nu fa nekkee ay fan nag, yonent bu tudd Agabus jóge Yude, agsi.
11 Mu ñëw ci nun, daldi yeew ay loxoom ak i tànkam ak laxasaayu Pool naan: «Nii la Xel mu Sell mi waxe: “Ki moom laxasaay gii, Yawut yi dinañu ko yeewe nii ca Yerusalem, jébbal ko ñi dul Yawut.”»
12 Bi nu déggee loolu, nun ak ña fa nekk nu ñaan Pool, mu baña dem Yerusalem.
13 Ci kaw loolu Pool ne: «Lu ngeen di jooy, di yàq sama xol? Bañuma ñu yeew ma rekk, waaye nangu naa sax, ñu rey ma ci Yerusalem ngir turu Yeesu Boroom bi.»
14 Bi nu ko manula dëpp, nu noppi ne: «Kon na coobarey Boroom bi am!»
15 Gannaaw fan yooyu nu defaru, ngir dem Yerusalem.
16 Noonu ay taalibe yu dëkk Sesare ànd ak nun, yóbbu nu ca nit ku tudd Manason, fu nu wara dal; moom nag nitu Sipar la woon, di taalibe bu yàgg.
17 Bi nu agsee Yerusalem nag, taalibe ya teeru nu ak mbég.
18 Ca ëllëg sa Pool ànd ak nun, seeti Saag, fekk njiit yépp teew fa.
19 Noonu Pool nuyu leen, nettali leen benn-benn li Yàlla def ci biir ñi dul Yawut, jaarale ko ci liggéeyam.
20 Bi ko njiit ya déggee, ñu màggal Yàlla ne ko: «Mbokk mi, gis nga ne am na ay junniy Yawut ñu gëm, te ñépp a sawar ci yoonu Musaa.
21 Dégg nañu ci sa mbir nag ne yaa ngi jàngal Yawut yépp, yi dëkk ci biir ñi dul Yawut, ñu bàyyi yoonu Musaa te baña xarafal seeni doom mbaa topp sunuy aada.
22 Lu nu ci wara def nag? Ndaxte ci lu wér dinañu xam ne ñëw nga.
23 Nu ngi lay digal nag, nga def nii: am na ci nun ñeenti góor ñu dige ak Yàlla.
24 Jël leen, bokk ak ñoom setlu, te nga gàddu seen peyu wateef. Noonu ñépp dinañu xam ne li ñu déggoon ci sa mbir du dëgg, waaye yaa ngi jëf tey sàmm yoonu Musaa.
25 Naka ñi dul Yawut ñi gëm, bind nanu leen li nu àtte ne, ñu moytu ñam wu ñu tuuroo xërëm te moytu deretu médd ak njaaloo.»
26 Bi ñu ko waxee, Pool jël nit ña te ca ëllëg sa mu bokk setlu ak ñoom, ñu dugg ca kër Yàlla ga. Ñu xamle ban bés la seen setlu di àgg, di bés bu ñuy jébbale sarax ngir kenn ku nekk ci ñoom.
JËF YA 21 in Téereb Injiil

Jëf ya 21:3-26 in Kàddug Yàlla gi

3 Naka lanu dem ba séen dunu Sippar, wacc ko nag sunu wetu càmmoñ, jublu diiwaanu Siri, ba teeri Tir, ndax fa la gaal gi waroona yebbi ab yebam.
4 Nu seet taalibey foofa, ba gis leen, toog ak ñoom juróom ñaari fan. Ci biir loolu Noo gu Sell gi di leen xiir ci wax Póol, ne ko bumu dem Yerusalem.
5 Ba nu fa amee fan yooyu lanu fa bàyyikoo, dem, ñu gunge nu, ñoom ñépp, ñook seeni soxna ak seeni doom. Nu dem ba génn dëkk ba, daldi sukk ca tefes ga, ñaan.
6 Ba loolu amee nu tàggtoo ba noppi, dugg ca gaal ga, ñoom ñu ñibbi.
7 Nun nag ba nu jógee Tir, danoo ñoqli ba teeri Patolemayis. Nu nuyoo faak bokki taalibe ya, toog faak ñoom benn fan.
8 Ca ëllëg sa nu dem ba àgg Sesare. Nu dem kër Filib, xamlekatu xibaaru jàmm, bi bokk ci Juróom ñaar ñi. Nu dal ak moom.
9 Filib moomu amoon na ñeenti doomi janq yuy waxe ay waxyu.
10 Gannaaw ba nu fa toogee ay fan, ab yonent bu ñuy wax Agabus jóge Yude, agsi.
11 Mu dikk ba ci nun, jël ngañaayal Póol, yeewe ko ay tànkam aki loxoom, daldi ne: «Noo gu Sell gi dafa wax ne: “Ki moom ngañaay lii, nii la ko Yawut yiy yeewe ca Yerusalem, jébbal ko jaambur ñi dul Yawut.”»
12 Ba nu déggee loolu, nun ak waa gox baa tinu Póol, ne ko bumu dem Yerusalem.
13 Ci kaw loolu Póol ne: «Lu ngeen di def nii, di jeexal sama xol? Waxuma ñu yeew ma rekk, waaye dee sax nangu naa koo def ci Yerusalem ngir Sang Yeesu.»
14 Naka lanu wax, wax, mu të, nu bàyyi, daldi ne: «Kon nag yal na Boroom bi sottal coobareem!»
15 Gannaaw fan yooyu lanu fabu, ngir dem Yerusalem.
16 Ci biir loolu ay taalibe yu dëkke Sesare ànd ak nun, yóbbu nu fa nu wara dali, ca kër ku ñuy wax Manason, ma cosaanoo Sippar, te di taalibe bu yàgg.
17 Ba nu agsee Yerusalem nag, bokki taalibe ya bége nañu noo dalal.
18 Ca ëllëg sa Póol ànd ak nun, seeti Yanqóoba, fekk mag ñépp a nga fa teew.
19 Póol nuyook ñoom, ba noppi benn-bennalal leen jëf, ji Yàlla sottale liggéeyam ci biir jaambur ñi.
20 Ñu dégg ca, daldi sàbbaal Yàlla, ba noppi ne ko: «Mbokk mi, xoolal ñaata junniy Yawut a doon ay gëmkat, te ñoom ñépp di ñu xér ci yoonu Musaa.
21 Ñoo dégg nag sab jëw, ñu ne dëddu yoonu Musaa mooy li ngay jàngal mboolem Yawut yi dëkk ci biir jaambur ñi, naan leen buñu xarfal seeni doom, te buñu topp sunuy aada.
22 Lu ciy pexe nag? Ndax kat duñu umple ne dikk nga.
23 Léegi daal, dangay def li nu lay wax nii: nu ngi feek ñeenti nit ñu am lu ñu xasal Yàlla.
24 Ñoom ngay àndal, nga bokk ak ñoom setlu, te nga gàddu seen peyu wateefu bopp, wi boroom xas wu ni mel aadawoo. Su ko defee ñépp ay xam ne li ñu lay jëwe, dara amu ci, te yoonu Musaa ngay jëfe, di ko sàmm.
25 Naka gëmkat ñi dul Yawut nag, bind nanu leen li nu dogal, ne leen ñu moytu ñam wu ñu sarxal ay xërëm, moytoo lekk deret ak yàppu mala mu ñu tuurul deretam, te moytu powum séy.»
26 Ca ëllëg sa Póol ànd ak nit ña, bokk ak ñoom setlu, dugg ca kër Yàlla ga. Mu daldi xamle bés ba seen àppu setlu di mat, ba jooxe ba ci war génn, ñeel kenn ku nekk ci ñoom.
Jëf ya 21 in Kàddug Yàlla gi