Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 21

JËF YA 21:3-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Noonu nu séen dunu Sipar, bàyyi ko ci sunu càmmoñ, jublu diiwaanu Siri, nu teersi Tir. Ndaxte foofa la gaal gi wara yebbee la mu yeboon.
4Nu wut taalibe ya, ba gis leen, toog ak ñoom juróom ñaari fan. Ñoom nag ñu ne Pool ci li leen Xelu Yàlla mi may, mu baña dem Yerusalem.
5Moona bi jataayu gaal ga matee, nu awaat ci yoon wi. Te ñépp gunge nu, ñoom ak seeni soxna ak seeni doom; nu génn dëkk ba, sukk ca tefes ga, ñaan ci Yàlla.
6Noonu nu tàggoo ak ñoom, dugg ca gaal ga, ñu dellu seen kër.
7Bi nu jógee Tir nag, nu demaat ci géej, ba teer Patolemayis. Foofa nu nuyu bokk ya, yendu, fanaan.
8Nu jóge fa ca ëllëg sa, ñëw ba ca dëkku Sesare. Nu dugg ca kër Filib, taskatu xibaaru jàmm bi, mi bokk ci Juróom ñaar ña, nu dal fa moom.
9Amoon na ñeenti doom yuy janq, ñuy wax ci kàddug Yàlla.
10Bi nu fa nekkee ay fan nag, yonent bu tudd Agabus jóge Yude, agsi.
11Mu ñëw ci nun, daldi yeew ay loxoom ak i tànkam ak laxasaayu Pool naan: «Nii la Xel mu Sell mi waxe: “Ki moom laxasaay gii, Yawut yi dinañu ko yeewe nii ca Yerusalem, jébbal ko ñi dul Yawut.”»
12Bi nu déggee loolu, nun ak ña fa nekk nu ñaan Pool, mu baña dem Yerusalem.
13Ci kaw loolu Pool ne: «Lu ngeen di jooy, di yàq sama xol? Bañuma ñu yeew ma rekk, waaye nangu naa sax, ñu rey ma ci Yerusalem ngir turu Yeesu Boroom bi.»
14Bi nu ko manula dëpp, nu noppi ne: «Kon na coobarey Boroom bi am!»
15Gannaaw fan yooyu nu defaru, ngir dem Yerusalem.
16Noonu ay taalibe yu dëkk Sesare ànd ak nun, yóbbu nu ca nit ku tudd Manason, fu nu wara dal; moom nag nitu Sipar la woon, di taalibe bu yàgg.
17Bi nu agsee Yerusalem nag, taalibe ya teeru nu ak mbég.
18Ca ëllëg sa Pool ànd ak nun, seeti Saag, fekk njiit yépp teew fa.
19Noonu Pool nuyu leen, nettali leen benn-benn li Yàlla def ci biir ñi dul Yawut, jaarale ko ci liggéeyam.
20Bi ko njiit ya déggee, ñu màggal Yàlla ne ko: «Mbokk mi, gis nga ne am na ay junniy Yawut ñu gëm, te ñépp a sawar ci yoonu Musaa.
21Dégg nañu ci sa mbir nag ne yaa ngi jàngal Yawut yépp, yi dëkk ci biir ñi dul Yawut, ñu bàyyi yoonu Musaa te baña xarafal seeni doom mbaa topp sunuy aada.
22Lu nu ci wara def nag? Ndaxte ci lu wér dinañu xam ne ñëw nga.
23Nu ngi lay digal nag, nga def nii: am na ci nun ñeenti góor ñu dige ak Yàlla.
24Jël leen, bokk ak ñoom setlu, te nga gàddu seen peyu wateef. Noonu ñépp dinañu xam ne li ñu déggoon ci sa mbir du dëgg, waaye yaa ngi jëf tey sàmm yoonu Musaa.
25Naka ñi dul Yawut ñi gëm, bind nanu leen li nu àtte ne, ñu moytu ñam wu ñu tuuroo xërëm te moytu deretu médd ak njaaloo.»
26Bi ñu ko waxee, Pool jël nit ña te ca ëllëg sa mu bokk setlu ak ñoom, ñu dugg ca kër Yàlla ga. Ñu xamle ban bés la seen setlu di àgg, di bés bu ñuy jébbale sarax ngir kenn ku nekk ci ñoom.

Read JËF YA 21JËF YA 21
Compare JËF YA 21:3-26JËF YA 21:3-26