Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 1:18-19 in Wolof

Help us?

JËF YA 1:18-19 in Téereb Injiil

18 —Pey gi Yudaa jotoon ci ñaawteefam, mu jënd ci tool, daanu fa, ba fàcc, ay butitam tuuru.
19 Loolu siiwoon na ci waa Yerusalem, moo tax ci seen làkk ñuy tudde tool ba Akeldama, maanaam «Toolu deret».—
JËF YA 1 in Téereb Injiil

Jëf ya 1:18-19 in Kàddug Yàlla gi

18 Yuda nag gannaaw ba mu jëndee ab tool ca peyu ñaawtéefam ja, ca la daanu, jiital boppam, biir ba fàcc, butit ya tuuru.
19 Waa Yerusalem yépp a ko yég, ba tax ñu tudde tool ba Akeldam, mu firi Toolu deret, ci seen làkk.
Jëf ya 1 in Kàddug Yàlla gi