Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 17:3-20 in Wolof

Help us?

JËF YA 17:3-20 in Téereb Injiil

3 Mu di leen ko tekki, te di leen wax ay firnde yuy wone ne fàww Almasi bi sonn te dekki. Mu ne leen: «Yeesu, mi ma leen di yégal, mooy Almasi bi.»
4 Noonu ñenn ci Yawut yi gëm, ànd ak Pool ak Silas, ñoom ak mbooloo mu mag ci Gereg yi ragal Yàlla, ak jigéen ñu am maana ñu bare.
5 Waaye kiñaan tàbbi ca Yawut ya, ñu daldi jël ay taxawaalukat ca pénc ma, dajale mbooloo, ñuy yëngal dëkk ba. Ñu daanu ci kër Yason, di wut Pool ak Silas, ngir dëj leen ci kanam waa dëkk ba.
6 Bi ñu leen gisul nag, ñu diri Yason ak ñeneen ca bokk ya ci kanam àttekat ya. Ñuy wax ci kaw naan: «Nit ñi dëpp àddina sépp agsi nañu fii léegi,
7 te Yason a leen dalal. Ñoom ñépp dañoo bañ ndigali buur Sesaar ne, am na beneen buur bu ñuy wax Yeesu.»
8 Bi ko mbooloo mi ak àttekat yi déggee, ñu daldi jaaxle lool.
9 Noonu nanguwuñoo yiwi Yason ak ñi ci des, lu dul bi ñu leen bataleelee dara.
10 Bi loolu amee bokk yi jàllale Pool ak Silas ci saa si ci guddi, ñu jëm Bere. Ba ñu fa eggee nag, ñu dugg ca jàngub Yawut ya.
11 Fekk ña fa nekk ñoo gëna am ay teggin waa Tesalonig, ndaxte nangu nañu kàddu ga te sawar ca, di niir Mbind mi bés bu nekk, ba xam ndax loolu dëgg la am déet.
12 Kon nag Yawut yu bare gëm, ak ñu bare ci Gereg yi, di jigéen yu am maana, ak ay góor.
13 Waaye bi Yawuti Tesalonig déggee ne Pool mu ngi yégle kàddug Yàlla ci Bere it, ñu daldi fay dikk, di jógloo ak a jaxase mbooloo ma.
14 Noonu bokk yi yebal Pool ca saa sa, mu jëm géej, waaye Silas ak Timote des fa.
15 Ñi ànd ak Pool nag gunge ko ba dëkku Aten. Bi ñu fa àggee, ñu waññiku, yóbbaale ndigalu Pool ne, Silas ak Timote ñëw fekksi ko ci lu gëna gaaw.
16 Bi leen Pool di nég ca Aten, mu am naqaru xol wu réy ci li mu gis dëkk ba fees ak ay nataali bokkaale Yàlla.
17 Muy werante nag ca jàngu ba ak Yawut ya ak ña ragal Yàlla, tey werante it bés bu nekk ca pénc ma ak ña fay dajaloo.
18 Noonu ay boroom xam-xam ci mbooloo mi ñuy wax Epikuren ak ci mbooloo mi ñuy wax Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ci ñoom ne: «Fortukatu xam-xam bii, lu mu bëgga wax?» Te ña ca des, bi ñu déggee Pool di waare xibaaru jàmm bi, aju ci Yeesu ak ci mbirum ndekkite, ñu ne: «Dafa mel ni day waare ay yàlla yu nu xamul.»
19 Kon nag ñu jël ko, yóbbu ko ca géew, ba ñuy wax Areyopas. Ñu ne ko: «Danoo bëggoon, nga leeral nu ci sa xam-xam bu bees, bii ngay yégle.
20 Ndaxte sol nga ci sunuy nopp lu nu xamul. Danoo bëggoona xam nag léegi, loolu lu muy tekki.»
JËF YA 17 in Téereb Injiil

Jëf ya 17:3-20 in Kàddug Yàlla gi

3 Mu di leen tekkil Mbind mi, di leen ci firndeel ne coonob Almasi ak ndekkiteem manul woona ñàkk. Mu ne leen: «Yeesu mii ma di leen xamal, mooy Almasi.»
4 Ba loolu amee ñenn ca Yawut ya gëm, fekksi Póol ak Silas, ñoom ak Gereg yu bare yu ragal Yàlla, ak jigéen ñu ràññiku ñu bare.
5 Yawut ya nag am ca kañaan, daldi foraatoo ca mbedd ma ay taxawaalukat, dajale ay gàngoor, ba yëngal dëkk ba. Ñu song kër Yason, di seet Póol ak Silas, ngir yóbbu leen ca waa dëkk ba.
6 Ci kaw loolu gisuñu leen, ñu diri Yason ak yeneen bokki gëmkat ba ca kanam àttekat ya. Ña ngay biral, naan: «Nit ñi tas àddinaa ngii, agsi nañu fi,
7 te Yason a leen dalal. Ñoom ñépp a xëtt ndigali buur Sesaar, te naan am na beneen buur bu ñuy wax Yeesu.»
8 Ba mbooloo ma ak àttekati dëkk ba déggee loolu, dañoo jaaxle.
9 Ba loolu amee ñu feyloo Yason ak ña ca des daan ba ca war, door leena yiwi.
10 Ba mu ko defee bokki gëmkat ña yebal ca saa sa Póol ak Silas ca guddi ga, ñu jëm Bere. Ñu agsi, dem ca jàngub Yawut ya.
11 Waa Bere nag gëna am déggin waa Tesalonig. Ñu gëm kàddu gi, xér ci lool, bés bu nekk ñuy niir Mbind mi, ngir xam ndax la ñu leen di wax noonu la.
12 Ci kaw loolu Yawut yu bare gëm, ñoom ak jigéeni Gereg ñu ràññiku, ak ay góori Gereg ñu bare.
13 Ba loolu amee Yawuti Tesalonig dégg ne Póol a ngay xamle kàddug Yàlla ca Bere itam. Ñu dikkati, yëngal nit ña, ñu def ay gàngoor.
14 Ca la bokki gëmkat ñi yebal Póol ca saa sa, mu jëm tefes ga, Silas ak Timote ñoom, des ca Bere.
15 Ña dar Póol nag gunge ko ba ca dëkk ba ñuy wax Aten, ñu doora dëpp, jottliji Silas ak Timote kàddug Póol, ngir ñu fekksi ko nu mu gëna gaawe.
16 Diggante ba Póol di nég Silas ak Timote ca Aten, xolam jeex na ndax dafa gis na dëkk ba yeboo ci jaamu ay tuur.
17 Ci biir loolu muy wax ak Yawut yaak jaamburi ragalkati Yàlla ya ca jàngu ba, di wax it ak waa pénc ma bés bu nekk.
18 Ci kaw loolu ay boroom xam-xam yu bokk ci ngérum Epikur ak ngérum Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ña ne: «Kebatukat bii, lu muy wax nii?» Ña ca des dégg Póol di waare xibaaru jàmm bi ci Yeesu ak ndekkiteem, ñu ne: «Daa mel ni ay tuur-tuuraani doxandéem lay waareel.»
19 Ñu jàpp ko nag, yóbbu ko ca ëttub àttekaay ba ñuy wax Areyopas. Ñu ne ko: «Ndax man nanoo xam njàngle mu bees mii ngay siiwal, lu mu doon?
20 Ndax li ngay wax kat sunu ngan-gi-nopp la. Nu bëgga xam nag loolu lu muy tekki.»
Jëf ya 17 in Kàddug Yàlla gi