Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 17

JËF YA 17:3-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Mu di leen ko tekki, te di leen wax ay firnde yuy wone ne fàww Almasi bi sonn te dekki. Mu ne leen: «Yeesu, mi ma leen di yégal, mooy Almasi bi.»
4Noonu ñenn ci Yawut yi gëm, ànd ak Pool ak Silas, ñoom ak mbooloo mu mag ci Gereg yi ragal Yàlla, ak jigéen ñu am maana ñu bare.
5Waaye kiñaan tàbbi ca Yawut ya, ñu daldi jël ay taxawaalukat ca pénc ma, dajale mbooloo, ñuy yëngal dëkk ba. Ñu daanu ci kër Yason, di wut Pool ak Silas, ngir dëj leen ci kanam waa dëkk ba.
6Bi ñu leen gisul nag, ñu diri Yason ak ñeneen ca bokk ya ci kanam àttekat ya. Ñuy wax ci kaw naan: «Nit ñi dëpp àddina sépp agsi nañu fii léegi,
7te Yason a leen dalal. Ñoom ñépp dañoo bañ ndigali buur Sesaar ne, am na beneen buur bu ñuy wax Yeesu.»
8Bi ko mbooloo mi ak àttekat yi déggee, ñu daldi jaaxle lool.
9Noonu nanguwuñoo yiwi Yason ak ñi ci des, lu dul bi ñu leen bataleelee dara.
10Bi loolu amee bokk yi jàllale Pool ak Silas ci saa si ci guddi, ñu jëm Bere. Ba ñu fa eggee nag, ñu dugg ca jàngub Yawut ya.
11Fekk ña fa nekk ñoo gëna am ay teggin waa Tesalonig, ndaxte nangu nañu kàddu ga te sawar ca, di niir Mbind mi bés bu nekk, ba xam ndax loolu dëgg la am déet.
12Kon nag Yawut yu bare gëm, ak ñu bare ci Gereg yi, di jigéen yu am maana, ak ay góor.
13Waaye bi Yawuti Tesalonig déggee ne Pool mu ngi yégle kàddug Yàlla ci Bere it, ñu daldi fay dikk, di jógloo ak a jaxase mbooloo ma.
14Noonu bokk yi yebal Pool ca saa sa, mu jëm géej, waaye Silas ak Timote des fa.
15Ñi ànd ak Pool nag gunge ko ba dëkku Aten. Bi ñu fa àggee, ñu waññiku, yóbbaale ndigalu Pool ne, Silas ak Timote ñëw fekksi ko ci lu gëna gaaw.
16Bi leen Pool di nég ca Aten, mu am naqaru xol wu réy ci li mu gis dëkk ba fees ak ay nataali bokkaale Yàlla.
17Muy werante nag ca jàngu ba ak Yawut ya ak ña ragal Yàlla, tey werante it bés bu nekk ca pénc ma ak ña fay dajaloo.
18Noonu ay boroom xam-xam ci mbooloo mi ñuy wax Epikuren ak ci mbooloo mi ñuy wax Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ci ñoom ne: «Fortukatu xam-xam bii, lu mu bëgga wax?» Te ña ca des, bi ñu déggee Pool di waare xibaaru jàmm bi, aju ci Yeesu ak ci mbirum ndekkite, ñu ne: «Dafa mel ni day waare ay yàlla yu nu xamul.»
19Kon nag ñu jël ko, yóbbu ko ca géew, ba ñuy wax Areyopas. Ñu ne ko: «Danoo bëggoon, nga leeral nu ci sa xam-xam bu bees, bii ngay yégle.
20Ndaxte sol nga ci sunuy nopp lu nu xamul. Danoo bëggoona xam nag léegi, loolu lu muy tekki.»

Read JËF YA 17JËF YA 17
Compare JËF YA 17:3-20JËF YA 17:3-20