Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 16:9-24 in Wolof

Help us?

JËF YA 16:9-24 in Téereb Injiil

9 Noonu ci guddi Yàlla feeñu Pool ci nii: nitu Maseduwan taxaw, di ko ñaan ne ko: «Ñëwal ci Maseduwan, wallusi nu!»
10 Bi mu amee peeñu moomu, ca saa sa nu fexee jàll ba Maseduwan, xam ne Boroom bi moo nu woo, ngir nu xamle fa xibaaru jàmm bi.
11 Noonu nu dugg gaal ca Torowas, jubal dunu Samotaras, jóge fa ca ëllëg sa, nu jëm teerub Neyapolis.
12 Bi nu fa teeree, nu jëm Filib, bi nekk dëkk bi ëpp maana ca wàll woowu ci diiwaanu Maseduwan, di it moomeelu Room. Nu toog fa ay fan.
13 Bi bésub noflaay agsee nag, génn nanu ci buntu dëkk ba, jublu ci wetu dex ga, yaakaar ne bérabu ñaanukaay la. Nu toog fa nag, di wax ak jigéen ña fa dajaloo.
14 Fekk am na fa jigéen juy déglu, tudd Lidi, di jaaykatu cuub, bu dëkk Catir, te mu ragal Yàlla. Noonu Boroom bi ubbi na xolam, ba mu nangu li Pool di wax.
15 Ci kaw loolu ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram, ba noppi mu ñaan nu ne: «Bu ngeen ma jàppee ni ku takku ci Boroom bi, ganesileen ma ci sama kër.» Te mu di nu ci xiir.
16 Am bés, ba nuy dem nag ca ñaanukaay ba, nu daje ak jaam bu jigéen bu rabu gisaane solu, te ay sangam di jariñu lu bare ci gisaaneem.
17 Mu daldi topp ci Pool ak nun, di xaacu ne: «Nit ñii jaami Yàlla Aji Kawe ji lañu; ñoo leen di yégal yoonu mucc.»
18 Muy def noonu ay fani fan, waaye bi ko Pool xajootul, mu waññiku ne rab wa: «Sant naa la ci turu Yeesu Kirist, génnal ci moom.» Noonu rab wa ne mëll, génn ci moom.
19 Bi ay sangam gisee nag seen buntu wërsëg tëju, ñu daldi jàpp Pool ak Silas, di leen diri, jëme leen ca pénc ma fa kanam njiit ya.
20 Noonu ñu dëj leen fa mbaxanay menne naan: «Yawut yii lëjal nañu sunu dëkk,
21 di xamle ay aada yu nu sañula nangu mbaa nu di ko topp, nun ñi bokk ci nguuru Room.»
22 Mbooloo ma it ànd ci, dal ci seen kaw; àttekat ya nag summilu seeni yére, santaane ñu dóor leen ay yar.
23 Noonu ñu dóor leen ay yar yu bare, tëj leen, sant boroom kaso ba, mu wottu leen bu wér.
24 Gannaaw jot na ndigal loolu nag, mu sànni leen ca néeg ba gëna ruqu ci biir kaso ba, jéng seeni tànk.
JËF YA 16 in Téereb Injiil

Jëf ya 16:9-24 in Kàddug Yàlla gi

9 Ci biir loolu am peeñu dikkal Póol ca guddi: mu gis aw nitu Maseduwan taxaw, di ko tinu, ne ko: «Jàllsil Maseduwan, wallusi nu!»
10 Naka la jot peeñu ma, mu daldi nu bir ne Yàllaa nu yebal ngir nu xamleji foofa xibaaru jàmm bi. Ca saa sa nu fexee jàll ba Maseduwan.
11 Ci kaw loolu nu dugge Torowas gaal, jubal dunu Samotaras, jógeeti fa, teereji Neyapolis ca ëllëg sa.
12 Nu bawoo fa jàll ba Filipi, dëkku gox ba jëkk ca diiwaanu Maseduwan te di moomeelu Room. Nu toog fa ay fan.
13 Ba bésub Noflaay ba taxawee, nu génn ca buntu dëkk ba, ca wetu dex ga, daldi fay gis bérab bu nu foog ne ab jullikaay la. Nu toog fa nag, di waxtaan ak jigéen ña fa daje.
14 As ndaw a nga ca, di déglu; ku ñuy wax Lidi, dëkke Catir, di jaaykatub cuubi tànnéef yu xonq curr, te di jaamukatu Yàlla. Boroom bi nag ubbi xolam, ba mu teewlu bu baax kàdduy Póol.
15 Ci kaw loolu ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram. Mu daldi nu ñaan, ne nu: «Ndegam ab gëmkatub Sang bi ngeen ma jàppe, agsileen, dal ak man ca sama kër.» Mu soññ nu ba nu nangu.
16 Noo doon dem jullikaay ba, ab surga bu jigéen bu rabu gisaane jàpp, dajeek nun. Alal ju bare la ay njaatigeem daa jële ci ngisaaneem.
17 Ndaw sa topp ci Póol ak nun, di xaacu, naan: «Nit ñii jaami Yàlla Aji Kawe ji lañu; dañu leen di yégal yoonu mucc.»
18 Noonu la jàppoo ay fani fan, ba Póol mujj xajootu ko. Mu walbatiku ne rab wa: «Maa la sant ci turu Yeesu Almasi, génnal ci ndaw si.» Rab wa daldi génn ca saa sa.
19 Ba loolu amee alal ja njaatigey ndaw sa yaakaaroon, réer leen, ñu jàpp Póol ak Silas, diri, yóbbu ca pénc ma, fa kanam njiit ya.
20 Ñu taxawal leen fa àttekat ya, ne: «Ñii ñoo yëngal sunu dëkk bi, di ay Yawut
21 yuy xamle aada yoy, nun ñiy waa Room, sañunu koo nangu, sañunu koo jëfe.»
22 Ci kaw loolu mbooloo ma it dal ci seen kaw; àttekat ya futti seeni yére, daldi santaane ñu dóor leen ay yar.
23 Ñu dóor leen ay yar yu bare, sànni leen ca kaso ba, boole ca jox boroom kaso ba ndigalal wattu leen bu baax.
24 Ndigal loolu nag tax mu sànni leen ca néeg ba gëna ruqe ca kaso ba, jéng leen.
Jëf ya 16 in Kàddug Yàlla gi