Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 16:4-16 in Wolof

Help us?

JËF YA 16:4-16 in Téereb Injiil

4 Bi loolu amee ñuy jaar ca dëkk ya, jottali leen dénkaane, yi ndaw yi ak njiit yi nekk Yerusalem joxe, te sant leen ñu sàmm ko.
5 Noonu mboolooy ñi gëm di gëna dëgër ci yoon wi, tey yokku bés bu nekk.
6 Bi loolu amee gannaaw Xel mu Sell mi aaye na leen, ñu yégleji kàddu gi ci diiwaanu Asi, ñu daldi jaari wàlli Firisi ak Galasi.
7 Bi ñu agsee nag ci wetu diiwaanu Misi, ñuy jéema dugg diiwaanu Bitini, waaye Xelum Yeesu mayu leen ko.
8 Ñu romb nag Misi, dem dëkku Torowas.
9 Noonu ci guddi Yàlla feeñu Pool ci nii: nitu Maseduwan taxaw, di ko ñaan ne ko: «Ñëwal ci Maseduwan, wallusi nu!»
10 Bi mu amee peeñu moomu, ca saa sa nu fexee jàll ba Maseduwan, xam ne Boroom bi moo nu woo, ngir nu xamle fa xibaaru jàmm bi.
11 Noonu nu dugg gaal ca Torowas, jubal dunu Samotaras, jóge fa ca ëllëg sa, nu jëm teerub Neyapolis.
12 Bi nu fa teeree, nu jëm Filib, bi nekk dëkk bi ëpp maana ca wàll woowu ci diiwaanu Maseduwan, di it moomeelu Room. Nu toog fa ay fan.
13 Bi bésub noflaay agsee nag, génn nanu ci buntu dëkk ba, jublu ci wetu dex ga, yaakaar ne bérabu ñaanukaay la. Nu toog fa nag, di wax ak jigéen ña fa dajaloo.
14 Fekk am na fa jigéen juy déglu, tudd Lidi, di jaaykatu cuub, bu dëkk Catir, te mu ragal Yàlla. Noonu Boroom bi ubbi na xolam, ba mu nangu li Pool di wax.
15 Ci kaw loolu ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram, ba noppi mu ñaan nu ne: «Bu ngeen ma jàppee ni ku takku ci Boroom bi, ganesileen ma ci sama kër.» Te mu di nu ci xiir.
16 Am bés, ba nuy dem nag ca ñaanukaay ba, nu daje ak jaam bu jigéen bu rabu gisaane solu, te ay sangam di jariñu lu bare ci gisaaneem.
JËF YA 16 in Téereb Injiil

Jëf ya 16:4-16 in Kàddug Yàlla gi

4 Ba loolu amee ñuy wër dëkk ya, di jottli dogal yi tukkee ca ndawi Yeesu yaak magi Yerusalem, ngir ñu sàmm ko.
5 Mboolooy gëmkat ñi di gëna feddliku ci wàllu ngëm, seeni lim di yokku bés ak bés.
6 Xel mu Sell mi nag tere leena yégleji kàddu gi ca diiwaanu Asi, ba tax ñu jàlli biir diiwaanu Firisi ak Galasi.
7 Ñu dem ba ca kemu Misi, nara jàlli biir diiwaanu Bitini, Xelum Yeesu mayu leen ko.
8 Loolu tax ñu jàlle biir Misi, àkki dëkk ba ñuy wax Torowas.
9 Ci biir loolu am peeñu dikkal Póol ca guddi: mu gis aw nitu Maseduwan taxaw, di ko tinu, ne ko: «Jàllsil Maseduwan, wallusi nu!»
10 Naka la jot peeñu ma, mu daldi nu bir ne Yàllaa nu yebal ngir nu xamleji foofa xibaaru jàmm bi. Ca saa sa nu fexee jàll ba Maseduwan.
11 Ci kaw loolu nu dugge Torowas gaal, jubal dunu Samotaras, jógeeti fa, teereji Neyapolis ca ëllëg sa.
12 Nu bawoo fa jàll ba Filipi, dëkku gox ba jëkk ca diiwaanu Maseduwan te di moomeelu Room. Nu toog fa ay fan.
13 Ba bésub Noflaay ba taxawee, nu génn ca buntu dëkk ba, ca wetu dex ga, daldi fay gis bérab bu nu foog ne ab jullikaay la. Nu toog fa nag, di waxtaan ak jigéen ña fa daje.
14 As ndaw a nga ca, di déglu; ku ñuy wax Lidi, dëkke Catir, di jaaykatub cuubi tànnéef yu xonq curr, te di jaamukatu Yàlla. Boroom bi nag ubbi xolam, ba mu teewlu bu baax kàdduy Póol.
15 Ci kaw loolu ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram. Mu daldi nu ñaan, ne nu: «Ndegam ab gëmkatub Sang bi ngeen ma jàppe, agsileen, dal ak man ca sama kër.» Mu soññ nu ba nu nangu.
16 Noo doon dem jullikaay ba, ab surga bu jigéen bu rabu gisaane jàpp, dajeek nun. Alal ju bare la ay njaatigeem daa jële ci ngisaaneem.
Jëf ya 16 in Kàddug Yàlla gi