Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 16:31-38 in Wolof

Help us?

JËF YA 16:31-38 in Téereb Injiil

31 Ñu ne ko: «Gëmal Yeesu Boroom bi, kon dinga mucc, yaw ak sa njaboot.»
32 Noonu ñu xamal ko kàddug Boroom bi, moom ak waa këram gépp.
33 Mu jël leen nag ci waxtu woowu ci guddi, raxas seeni gaañu-gaañu, ba noppi ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram gépp.
34 Bi ñu ko defee mu yóbbu leen ca këram, jox leen ñu lekk, mu bég lool ci li mu gëm Yàlla, moom ak waa këram gépp.
35 Bi bët setee, àttekat ya yónni alkaati ya, ñu ne boroom kaso ba: «Yiwil ñaari nit ñooñu, ñu dem.»
36 Kon boroom kaso ba yégal loolu Pool ne ko: «Àttekat ya jox nañu ma ndigal, ngir ma yiwi leen, ngeen dem; léegi nag génnleen te dem ci jàmm.»
37 Waaye Pool ne alkaati ya: «Dóor nañu nu ay yar ci kanam ñépp, ci lu ñu wéerul ci benn àtte, rax-ca-dolli tëj nañu nu kaso, nun ñiy jaambur ci nguuru Room. Léegi ndax dañu noo bëgga sànni ci mbedd mi ci kumpa? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, gunge nu ci biti.»
38 Bi mu ko waxee, alkaati ya yégal àttekat ya la mu wax. Bi ñu déggee ne jaamburi Room lañu, ñu daldi tiit.
JËF YA 16 in Téereb Injiil

Jëf ya 16:31-38 in Kàddug Yàlla gi

31 Ñu ne ko: «Gëmal Sang Yeesu, daldi mucc, yaak sa waa kër.»
32 Ba loolu amee ñu xamal ko kàddug Sang bi, moom ak waa këram gépp.
33 Mu yóbbu leen nag ci waxtuw guddi woowu, raxas seeni gaañu-gaañu, ñu sóob ko ci ndox ca saa sa, moom ak waa këram gépp.
34 Gannaaw loolu mu yóbbu leen këram, jox leen ñu lekk, tey bégeendoo ak waa këram gépp ci ngëm gi ñu gëm Yàlla.
35 Ba bët setee, àttekat ya yebal alkaati ya, ñu ne boroom kaso ba: «Ñii, yiwi leen.»
36 Boroom kaso ba àgge Póol ndigal la, ne ko: «Àttekat yi kat ñoo fi yeble, ne ñu yiwi leen. Kon nag man ngeena génn te dem ak jàmm.»
37 Póol nag ne alkaati ya: «Ñoom ñu dóor nu ci kanam nit ñi, àtteesu nu sax te nu diy gor ci Room gii, rax ci dolli ñu sànni nu ci kaso bi. Léegi ñu bëgg noo dàq ndànk ci biti? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, génne nu.»
38 Ba mu ko defee, alkaati ya àgge àttekat ya kàddu googu, ñu xam ne ay gori waa Room lañu, tiitaange jàpp leen.
Jëf ya 16 in Kàddug Yàlla gi