Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 16:30-35 in Wolof

Help us?

JËF YA 16:30-35 in Téereb Injiil

30 Mu génne leen ci biti ne leen: «Kilifa yi, lu ma wara def, ba mucc?»
31 Ñu ne ko: «Gëmal Yeesu Boroom bi, kon dinga mucc, yaw ak sa njaboot.»
32 Noonu ñu xamal ko kàddug Boroom bi, moom ak waa këram gépp.
33 Mu jël leen nag ci waxtu woowu ci guddi, raxas seeni gaañu-gaañu, ba noppi ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram gépp.
34 Bi ñu ko defee mu yóbbu leen ca këram, jox leen ñu lekk, mu bég lool ci li mu gëm Yàlla, moom ak waa këram gépp.
35 Bi bët setee, àttekat ya yónni alkaati ya, ñu ne boroom kaso ba: «Yiwil ñaari nit ñooñu, ñu dem.»
JËF YA 16 in Téereb Injiil

Jëf ya 16:30-35 in Kàddug Yàlla gi

30 Gannaaw gi mu génne leen ca biti ne leen: «Sang yi, ana lu ma wara def, ba mucc?»
31 Ñu ne ko: «Gëmal Sang Yeesu, daldi mucc, yaak sa waa kër.»
32 Ba loolu amee ñu xamal ko kàddug Sang bi, moom ak waa këram gépp.
33 Mu yóbbu leen nag ci waxtuw guddi woowu, raxas seeni gaañu-gaañu, ñu sóob ko ci ndox ca saa sa, moom ak waa këram gépp.
34 Gannaaw loolu mu yóbbu leen këram, jox leen ñu lekk, tey bégeendoo ak waa këram gépp ci ngëm gi ñu gëm Yàlla.
35 Ba bët setee, àttekat ya yebal alkaati ya, ñu ne boroom kaso ba: «Ñii, yiwi leen.»
Jëf ya 16 in Kàddug Yàlla gi