3Póol nag bëgg mu ànd ak moom, ba tax mu yóbbu ko, xarfal ko ndax Yawut ya dëkke woon gox ba, ngir ñépp a xamoon ne baayam ab Gereg la.
4Ba loolu amee ñuy wër dëkk ya, di jottli dogal yi tukkee ca ndawi Yeesu yaak magi Yerusalem, ngir ñu sàmm ko.
5Mboolooy gëmkat ñi di gëna feddliku ci wàllu ngëm, seeni lim di yokku bés ak bés.
6Xel mu Sell mi nag tere leena yégleji kàddu gi ca diiwaanu Asi, ba tax ñu jàlli biir diiwaanu Firisi ak Galasi.
7Ñu dem ba ca kemu Misi, nara jàlli biir diiwaanu Bitini, Xelum Yeesu mayu leen ko.
8Loolu tax ñu jàlle biir Misi, àkki dëkk ba ñuy wax Torowas.
9Ci biir loolu am peeñu dikkal Póol ca guddi: mu gis aw nitu Maseduwan taxaw, di ko tinu, ne ko: «Jàllsil Maseduwan, wallusi nu!»
10Naka la jot peeñu ma, mu daldi nu bir ne Yàllaa nu yebal ngir nu xamleji foofa xibaaru jàmm bi. Ca saa sa nu fexee jàll ba Maseduwan.