Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 16

Jëf ya 16:19-40

Help us?
Click on verse(s) to share them!
19Ba loolu amee alal ja njaatigey ndaw sa yaakaaroon, réer leen, ñu jàpp Póol ak Silas, diri, yóbbu ca pénc ma, fa kanam njiit ya.
20Ñu taxawal leen fa àttekat ya, ne: «Ñii ñoo yëngal sunu dëkk bi, di ay Yawut
21yuy xamle aada yoy, nun ñiy waa Room, sañunu koo nangu, sañunu koo jëfe.»
22Ci kaw loolu mbooloo ma it dal ci seen kaw; àttekat ya futti seeni yére, daldi santaane ñu dóor leen ay yar.
23Ñu dóor leen ay yar yu bare, sànni leen ca kaso ba, boole ca jox boroom kaso ba ndigalal wattu leen bu baax.
24Ndigal loolu nag tax mu sànni leen ca néeg ba gëna ruqe ca kaso ba, jéng leen.
25Ba guddi gay xaaj, Póol ak Silas a ngay ñaan, di sàbbaal Yàlla, ñeneen ña ñu fa tëj di leen déglu.
26Ci kaw loolu suuf jekki yëngu yëngu bu mag ba kenug kaso ba di rëng-rëngi; bunt yépp jekki ubbiku, jéngi ñépp dàjjiku.
27Boroom kaso ba tiite ciy nelaw, gis bunti kaso bi ubbiku. Mu bocci saamaram, nara xaru, yaakaar ne ña ñu tëj dañoo rëcc.
28Póol nag àddu ca kaw ne: «Bul lor sa bopp, nun ñépp a ngi fi.»
29Ba loolu amee boroom kaso ba indilu ab làmp, daldi ne saraax dugg, ne gurub fa kanam Póol ak Silas, di lox.
30Gannaaw gi mu génne leen ca biti ne leen: «Sang yi, ana lu ma wara def, ba mucc?»
31Ñu ne ko: «Gëmal Sang Yeesu, daldi mucc, yaak sa waa kër.»
32Ba loolu amee ñu xamal ko kàddug Sang bi, moom ak waa këram gépp.
33Mu yóbbu leen nag ci waxtuw guddi woowu, raxas seeni gaañu-gaañu, ñu sóob ko ci ndox ca saa sa, moom ak waa këram gépp.
34Gannaaw loolu mu yóbbu leen këram, jox leen ñu lekk, tey bégeendoo ak waa këram gépp ci ngëm gi ñu gëm Yàlla.
35Ba bët setee, àttekat ya yebal alkaati ya, ñu ne boroom kaso ba: «Ñii, yiwi leen.»
36Boroom kaso ba àgge Póol ndigal la, ne ko: «Àttekat yi kat ñoo fi yeble, ne ñu yiwi leen. Kon nag man ngeena génn te dem ak jàmm.»
37Póol nag ne alkaati ya: «Ñoom ñu dóor nu ci kanam nit ñi, àtteesu nu sax te nu diy gor ci Room gii, rax ci dolli ñu sànni nu ci kaso bi. Léegi ñu bëgg noo dàq ndànk ci biti? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, génne nu.»
38Ba mu ko defee, alkaati ya àgge àttekat ya kàddu googu, ñu xam ne ay gori waa Room lañu, tiitaange jàpp leen.
39Ñu dikk, jéggalu, génne leen ci biti, ñaan leen, ñu génn dëkk ba.
40Noonu lañu génne kaso ba, dellu kër Lidi. Ñu gise faak bokki gëmkat ña, ñaax leen, doora dem.

Read Jëf ya 16Jëf ya 16
Compare Jëf ya 16:19-40Jëf ya 16:19-40