Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 16:1-9 in Wolof

Help us?

JËF YA 16:1-9 in Téereb Injiil

1 Naka noona mu dikk dëkki Derbë ak Listar, fekk fa taalibe bu tudd Timote te ndeyam di Yawut bu gëm, waaye baayam di Gereg.
2 Te mbokk, yi nekk dëkki Listar ak Ikoñum, seedeel nañu ko lu baax.
3 Pool bëgg nag mu ànd ak moom, waaye ndegam Yawut yépp, ya dëkk ca wàllaa ya, xam ne baayam Gereg la woon, mu jël ko, xarafal ko.
4 Bi loolu amee ñuy jaar ca dëkk ya, jottali leen dénkaane, yi ndaw yi ak njiit yi nekk Yerusalem joxe, te sant leen ñu sàmm ko.
5 Noonu mboolooy ñi gëm di gëna dëgër ci yoon wi, tey yokku bés bu nekk.
6 Bi loolu amee gannaaw Xel mu Sell mi aaye na leen, ñu yégleji kàddu gi ci diiwaanu Asi, ñu daldi jaari wàlli Firisi ak Galasi.
7 Bi ñu agsee nag ci wetu diiwaanu Misi, ñuy jéema dugg diiwaanu Bitini, waaye Xelum Yeesu mayu leen ko.
8 Ñu romb nag Misi, dem dëkku Torowas.
9 Noonu ci guddi Yàlla feeñu Pool ci nii: nitu Maseduwan taxaw, di ko ñaan ne ko: «Ñëwal ci Maseduwan, wallusi nu!»
JËF YA 16 in Téereb Injiil

Jëf ya 16:1-9 in Kàddug Yàlla gi

1 Ci kaw loolu Póol agsi Derbe, teg ci dëkk ba ñuy wax Listar. Ndeke ab taalibee nga fa bu ñuy wax Timote; ndeyam di gëmkatub Almasi bu bokk ci askanu Yawut, baayam di Gereg.
2 Muy ku rafet seede ci biir bokki dëkk yooyu di Listar ak Ikoñum.
3 Póol nag bëgg mu ànd ak moom, ba tax mu yóbbu ko, xarfal ko ndax Yawut ya dëkke woon gox ba, ngir ñépp a xamoon ne baayam ab Gereg la.
4 Ba loolu amee ñuy wër dëkk ya, di jottli dogal yi tukkee ca ndawi Yeesu yaak magi Yerusalem, ngir ñu sàmm ko.
5 Mboolooy gëmkat ñi di gëna feddliku ci wàllu ngëm, seeni lim di yokku bés ak bés.
6 Xel mu Sell mi nag tere leena yégleji kàddu gi ca diiwaanu Asi, ba tax ñu jàlli biir diiwaanu Firisi ak Galasi.
7 Ñu dem ba ca kemu Misi, nara jàlli biir diiwaanu Bitini, Xelum Yeesu mayu leen ko.
8 Loolu tax ñu jàlle biir Misi, àkki dëkk ba ñuy wax Torowas.
9 Ci biir loolu am peeñu dikkal Póol ca guddi: mu gis aw nitu Maseduwan taxaw, di ko tinu, ne ko: «Jàllsil Maseduwan, wallusi nu!»
Jëf ya 16 in Kàddug Yàlla gi