2Mbir ma nag mujje féewaloo ak werante wu xawa metti, te Póol ak Barnaba séq ko ak ñooñu. Ba loolu amee ñu ne, na Póol ak Barnaba, ak ñenn ca gëmkati Àncos, ànd dem Yerusalem ca ndawi Yeesu, ak mag ña, ba lijjanti mbir moomu.
3Ci kaw loolu mbooloom gëmkat ñi yebal leen, ñu jaare Fenisi ak Samari, daldi àgge waa foofa ni jaambur ñi dul Yawut tuube, ba bokki gëmkat ñépp bég ca lool.
4Gannaaw loolu, ñu agsi Yerusalem, mbooloom gëmkat ñi, ak ndawi Yeesu yi, ak mag ñi, dalal leen, ñu nettali leen mboolem ni Yàlla def ak ñoom.
5Ba mu ko defee ñenn ci gëmkat ñi bokk ci ngérum Farisen yi, daldi taxaw temm, ne gëmkat ñi dul Yawut, fàww ñu xarfal leen, sàmmloo leen yoonu Musaa.
6Ba loolu amee ndawi Yeesu yi ak mag ñi bokk daje, ngir seet mbir moomu.
7Werante wu réy am ca. Ci kaw loolu Piyeer jóg ne leen: «Bokk yi, yeen xam ngeen ne bu yàgg la ma Yàlla seppee ci seen biir, ngir jaambur ñi dégge ci sama làmmiñ, kàddug xibaaru jàmm bi, ba doon ay gëmkat.
8Yàlla, mi xam xolu nit nag moo seereel jaambur ñi, ba mu leen mayee Noo gu Sell gi, ni mu nu ko maye nun itam.
9Yàlla amul xejj ak seen sunu digg ak ñoom, ndax seen ngëm la raxase seen xol.
10Léegi nag lu tax ngeen di diiŋat Yàlla, di teg taalibe yi yen bu nu masula àttan, cay maam ba ci nun?
11Yiwu Sang bi Yeesu daal lanu gëm ne ci lanuy mucce, te ñoom itam, noonu rekk.»
12Ba loolu wéyee mbooloo mépp ne xerem. Ñu déglu nag Barnaba ak Póol, ñu xamle mboolem firnde yeek kéemaan, yi Yàlla defe seen ñaari jëmm ci biir jaambur ñi.
13Ba ñu noppee, Yanqóoba àddu ne: «Bokk yi, dégluleen ma.