4 Ñooñu la Noo gu Sell gi yebal, ñu dem dëkk ba ñuy wax Selusi, dugge fa gaal, jëm dun ba ñuy wax Sippar.
5 Ña nga teereji dëkk ba ñuy wax Salamin, daldi fay yégle kàddug Yàlla ca jànguy Yawut ya, ku ñuy wax Yowaan Màrk ànd ak ñoom, di leen jàpple.
6 Ci biir loolu ñu wër dun ba bépp, ba yegg Pafos, péey ba. Ñu tase faak ab ñeengokatub Yawut buy yonent-yonentlu, ñu di ko wax Bar Yeesu.